url stringlengths 6 8 | content stringlengths 2 3.72k | source stringclasses 3
values |
|---|---|---|
page_201 | Dibi-Dibi ci boppam, nit ñi amoon nañu
lool yaakaar ci moom. Gaa, daawul wax
waxu nit, waaye waa Jafune amatuñu
woon pexe. Dunde yaakaar a leen dese
woon. Dibi-Dibi it doonoon nit ku ñeme
Yàlla ! Lu waa Jafune tawat, mu ne am na
ci pexe. Dem na ba dajale lu mat fukki
junniy gone, ne leen :
- Ku amul liggéey ci ... | DOOMI-GOLO-Ebook-1.pdf |
page_202 | Mbooloo miy tàccu, jigéen ñiy sarxolle,
gone yiy say. Yëf yi xumb ba dee, nit ñi
naan :
- Kii, mayu Yàlla dëgg la am !
- Mën naa indi xaalis bu dul jeex ci réew
mi !
- Yàllaa dugal Dibi-Dibi ci sunuy xol !
Kenn mënu ci dara !
- Dibi-Dibi rekk ! Dibi-Dibi rekk !
Teewul woon nag, mag ñi xam àddina
amoon xel ñaa... | DOOMI-GOLO-Ebook-1.pdf |
page_203 | - Xanaa ni Dibi-Dibi di doxe. Seetlu nga
ko bu baaxam ? Kàddu yooyu jaaxal
Omar Jaw. Mu ne Aatu :
- Lu nekk ci doxinu Dibi-Dibi ?
Aatu ne ko :
- Baal ma de, waaye sa waa ji ni kanaara
lay doxe. Foofu, Omar xàqataay, tàccu :
- Dikkleen, góor gi Aatu Sekk ràηηatiku
na nag ! Am xaat waa Guy-Géwél yu ñëw
wër leen.... | DOOMI-GOLO-Ebook-1.pdf |
page_204 | Yow bañkat nga mës a doon, sa dund
gépp danga koo xeex. Mënuma woon a
gëm ne néeg ngaa xañ say doom ak say
jarbaat seen wërsëg.
- Wërsëg wan ngay wax, Omar ?
- Gone yépp dinañu am liggéey,
taxawaalu bi dina dakk ci réew mi !
Aatu Sekk xool ko ba seppali ko, ne ko :
- Omar, ba fi mu nekk daal, gëm nga ne
noonu ... | DOOMI-GOLO-Ebook-1.pdf |
page_205 | - Waaw, Omar, ba daal sunu gaa ñépp
bitim-réew lañu jànge nañuy téyee réew
mii ? Loolu yenu na maanaam ?
- Lu tee ? Àddina day dox ! Aatu wiccax
bopp bi, muuñ :
- Man de, Omar, am na leneen lu ma xaw
a tiital...
- Loolu lan laati, Aatu ?
- Sunu mbokk yi nu wër, xanaa ! Ñoom de
laa ragal ñu song nu bés, këf Di... | DOOMI-GOLO-Ebook-1.pdf |
page_206 | man mii maay jëkk a tëdd ci kanamu
roplaan bi ndax mu bañ a jóge Jafune !
Waaye Omar moom, loolu yépp safu ko.
Kàrt la bëggoon daal te am na ko, ndax
Aatu wax na ci gémmiñam ni Dibi-Dibi
lay woteel. Góor gi Aatu Sekk yemale fa
waxtaan wa, te naan ci xelam :
« Baax na. Kii moom dina ma fekksi fii
ma toog ne ma w... | DOOMI-GOLO-Ebook-1.pdf |
page_207 | - Omar, noon naa la nit kuy doxe ni
kanaara, ku ko jébbal réewum lëmm yaa
tooñ sa bopp.
*
* *
Du sax Dibi-Dibi moo jëkk a duut
réewum lëmm. Loolu yàgg naa am ci
politig.Waaye yaakaaru nit ñi ci Dibi-
Dibee ka réyoon ! Ñépp di yàkkali bóli.
Yaakaar booboo tax waa réew mi
jàppalewuñu ko yem ci. Dañoo sot dë... | DOOMI-GOLO-Ebook-1.pdf |
page_208 | - Lii rekk ngeen may laaj, su ma faloo ?
Xeeb naa ko, ndax sama mën-mën, fu ko
nit natt romb na koy dem ! Kon boog
buleen yox-yoxi, laajleen ma lépp lu
ngeen bëgg, ma defal leen ko. Man réew
mi doηη a ma tax a jóg ! Géwélu Dibi-
Dibi daldi dugg ci wax ji :
- Aywaleen gaa ñi, ku yéex ñàkk ! Ku
Dibi-Dibi tàccu, so... | DOOMI-GOLO-Ebook-1.pdf |
page_209 | - Fuuf ! Fuuf ! Maa ko jëkk a fóon !
*
* *
Dëgg la, Dibi-Dibi da doon sóob rekk,
xaajul a tane ki mu fi wuutu. Waaye xéy-
na su ko Yàlla feyee xolam, du am lu muy
réccu. Amoon na yéene ci réewam. Dara
yàqalu ko lu dul parax-paraxeek teg
boppam fu mu àggul, jàpp ne képp ku
Yàlla sàkk moo la ëpp xel. Ba mu wó... | DOOMI-GOLO-Ebook-1.pdf |
page_210 | Dibi-Dibi jaay na réew mi, ngir sàmm
bànneexu boppam ak bànneexu njabootam
Loolu doηη a indi weranteek reyante ci
Jafune. Dëgg rekk a neex Yàlla. Dibi-
Dibi taxu ko woon yemb. Waaye kuy seet
bu baax, dinga gis ne njiiti réew yu bare ci
àddina si, seen yaram neexul. Dafa fekk
rekk ñu di ay kilifa, ñu leen di làq... | DOOMI-GOLO-Ebook-1.pdf |
page_211 | - Dibi-Dibi, defar réew mee ko tax a jóg,
waaye saa yu santaanee dara, ñi ko wër
def leneen.Teewul ñu bare ñu àndoon ak
Dibi-Dibi ca njëlbéen ga, mujje koo
jàmbu. Ba Dibi-Dibi tàmbalee tabax ay
mónimaa, la leer ñépp ne yaram wi
neexatul. Da daan xaar ba waa Jafune
yépp di nelaw, muy wër dëkk bi, fu mu
gis bayaa... | DOOMI-GOLO-Ebook-1.pdf |
page_212 | - Moo, kii lu mu xewle nii ?
- Moom daal, lu ñëw ci xelam mu ni ayca,
yëkkatileen ab mónimaa ! Laata Dibi-
Dibi di dugg ci politig nag, da daan
jàngale mbirum aadaak cosaanu réew mi,
ci daara Jafune ju mag ji. Moo tax nee ñu
mu bëggoon a màndargaal nguuram ak i
mónimaa. Am na it ñu ne da daan suul ay
gàllaaj ci... | DOOMI-GOLO-Ebook-1.pdf |
page_213 | « Aa ! Lu tey doon, ba Dibi-Dibi di wone
gii maandute ? Xéy-na ay mbokkam a ko
yedd. »
Waaye nit ak jikkoom ba ci biir bàmmeel!
Keroog jooju Dibi-Dibi dafa xéyee talalali
ba tàkkusaan di waaj a jot ! Ba mu demee
ba xamatul lu muy wax, dafa rocci ci kayit
yi tege woon ci kanamam benn nataal,
woolu ay gone, daldi... | DOOMI-GOLO-Ebook-1.pdf |
page_214 | - Ku la laaj loolu ? Lan la, laa wax ?
- Kanaara la.
- Jërëjëf. Léegi, lenn laa bëgg nga wax
ma, yow doomu Jafune : ana kanaara yi ne
woon gàññ ci mim réew ? Fan lañu jaar ba
ne mes ? Dibi-Dibi nekk fa nag, di wax lu
ñor ak lu ñorul, naan :
Mbir mee ka kéemaane ! Kanaara yi ne
woon Jafune yépp ne mes te kenn xa... | DOOMI-GOLO-Ebook-1.pdf |
page_215 | diggante 1640 ak 1647, ca jamono ja
Daaw Demba sonalee lool Kajoor. Nguuru
Daaw Dembaa ka metti woon ! Tere na ku
lekk yàppu wataboor wu am xorom, ne it
su ñaar déeyante ba reetaan dina leen rey.
Dem na ba ne ku nar a takk janq ci
Kajoor, na nga ko ko indil, mu jaar ci ba
noppi, moom Daaw Demba moomu, sog
laa d... | DOOMI-GOLO-Ebook-1.pdf |
page_216 | Guney Jafune yi feragul sax, dégg nañu ay
jëfam yu ñaaw. Dibi-Dibi dina la ne ràpp
ci kaso bi tëj, woo ay gaana ñu futti sa
jabar ci sa kanam, nga leen di seetaan ñu
koy sàkku te doo ci mën dara. Te bu
boobaa, Dibi-Dibi day toog ci sa wet, yow
jëkkër ji, naan gaana yi :
- Ndaw sii caga la, na seen bal yu tàng yi... | DOOMI-GOLO-Ebook-1.pdf |
page_217 | Nee na kat Tóoni Bleer a ko woowe
Angalteer ndax mu xelal ko. Waaw.
Angalteer daal, jànkoonte woon naak ay
jafe-jafe yu réy, Tóoni Bleer jaaxle lool,
daldi ne : « Lii de, kenn rekk a ma ci mën
a génne, te Dibi-Dibi la ! » Loolu de la
njiitu réew mi teg sunuy loxo. Gone ya
teewoon ca mitiη ba mer, di ko sànniy
x... | DOOMI-GOLO-Ebook-1.pdf |
page_218 | Way-fippu yi àndu ñu ci loolu. Dibéer jee
ñu génn, seen benn njiit wax na lu leer :
- Soldaar bu jóge bitim-réew, ne dangay
jàppalesi Dibi-Dibi, dinanu defanteek
yow. Foofu la mbir mi tolloogum.
Géej gi waxoon na ko : fitna ji waa Jafune
nekk yépp, seen ñàkk fullaa leen ko teg.
Ci gis-gisu góor gi Aatu Sekk tami... | DOOMI-GOLO-Ebook-1.pdf |
page_219 | moom kott moo des Guy-Géwél. Xippi na
ga, waaye xamatul ndax day gént walla
déet. Góor gi Aatu Sekk a ngi dégg ni
butitam yiy jooye, di lemu ak a lemmiku.
Xamul kañ la gëj a xiife nii.
*
* *
Ay xaj a ngi mbów ci tàkkal dex gi, mu di
leen dégg fi mu jaaxaan. Ñaari noppi Aatu
Sekk yi miin nañu léegi tekk-tek... | DOOMI-GOLO-Ebook-1.pdf |
page_220 | taxaw, am ci ñoom ñu jëkk a seet ndax
amul ay noon yu fi làqu. Ñu nekk fay wër
gox bi ba mu yaakaar ne léegi ñu song
Guy-Géwél, ñu daldi woññeeku.Bi ñu
rombee buntu kër gi la Aatu dégg ñaar ñu
ci doon werante :
- Fii kat, ndekete nit desu fi.
- Danga xam ndax gaa ñi suul nañu fiy
ndell walla déet ?
- Dina ma j... | DOOMI-GOLO-Ebook-1.pdf |
page_221 | - Jaale naa la sa xarit bi faatu, waaye su
doon sama sago nga dóor ma bal, ma
noppaluji man itam. Jébbal naa la sama
bopp. Defal ci man lu la neex. Wànte naka
la Aatu Sekk taxaw rekk, daldi tàmbalee
miir, àggaat ci suuf, di xiixat.
*
* *
Seen ndey a jëkk ñëw. Aatu Sekk xippi,
gis ko mu ne jodd ci ëtt bi di... | DOOMI-GOLO-Ebook-1.pdf |
page_222 | Liiñu caas gi leen tiim ñoom ñaar. Tey sax
la Aatu mas a seetlu keppu yu weex yeek
yu xonq yiy làng ci liiñ gi.Toogu bant bu
gudd bi. Ci la xaritu Aatu yi daan teg seen
damyee, di wure subaak ngoon. Ni toogu
bi jaaxaane ci taatu niim gi, ñaari yëf la
tekki. Wéetaay bu tar. Bànneex bu dëddu
Guy-Géwél. Ñu jékki-jé... | DOOMI-GOLO-Ebook-1.pdf |
page_223 | Ci la góor gi Aatu Sekk sog a nànd ne am
na lu ko golo gi bëgg a won.
*
* *
Keroog la golo gi bàyyi ñaari doom yeek
Aatu. Bi Aatuy laata xam lu xew, sànni na
leen ko ba dem yoonam.
Aatu Sekk di fo ak ñoom, di leen toppatoo
ni mu ware ba ñu far nekk ay wéttalam.
Waaye golo du mbokk ! Ñaari gone yi,
yar ak ... | DOOMI-GOLO-Ebook-1.pdf |
page_224 | Ñàmbi ji xaw naa dëgër gaa, wànte li Aatu
Sekk di nekk mag yépp, bëñ yi
yàqooguñu. Lee-lee kenn ci ñoom ñaar
dugg biir Guy-Géwél, delluseek gerte-
kemb mbaa xollitu banaana, sànni ko
Aatu, mel ni kuy jox sa xaj mbaa sa xar
mu lekk. Suy sàqami ñàmbeem, di yuut,
ñu koy ñaawal. Lu tuuti lu mu def, ñu
gàddu seen yat... | DOOMI-GOLO-Ebook-1.pdf |
page_225 | Lee-lee seen ndey dellusi ci kër gi, taxaw
ci kow miir bi, woo leen, ñu fekki ko, fo
ak moom ba Aatu Sekk defe ne suy dem
da leen di yóbbaale. Waaye day jékki-
jékki ne mërr, wacc leen ak Aatu Sekk.
*
* *
Aatu Sekk wutal na ku ci nekk tur. Golo
gu góor gi mooy Ninki. Rakk ju jigéen
jeey Nanka.
Ninki-Nanka.... | DOOMI-GOLO-Ebook-1.pdf |
page_226 | Xel mi dem fu sore, mu ne :
- Céy, nun ! Fu nu jëm ak Dibi-Dibi ?
Wànte sama coono beek sama wéetaay bii
am na lu ñu ma jàngal ci mbiri àddina :
tés-tés ji nit ñi nekke, dara waralu ko lu
dul bëgg a fàtte seeni naqar. Lu ñu dugg
looloo leen ci dugal. Saa yu nit sóobee
lenn, gasaale na pax suul fa leneen lu ko
n... | DOOMI-GOLO-Ebook-1.pdf |
page_227 | Dafa mel ni sax gone yi am na yu ñuy
jëfandikoo, de ! Walla ? Xet gii gën a doy
waar ! Mbaa du doomaraam yii dañuy
naan sàngara ? Su dul sàngara it, niru na
ko lool ! Li ñuy lekk yépp, ñu ngi waxtaan
ñoom ñaar. Góor gi Aatu Sekk yéemu.
Moom daal, su dul woon seen geen yu
gudd yeek seen karaw gu xonq geek seeni
... | DOOMI-GOLO-Ebook-1.pdf |
page_228 | Aatu ηaaη, di xiixat, ba yàgg mu yëkkatiy
loxoom ni ku réccu li mu def, di jéggalu:
- Baal-leen ma àq de, goney mberaago yi !
Dafa am lu ma fàttaliku rekk, sama xol
fees ! Yéen dungeen ci dara. Samay noon
ñoo fàqee barsàq bëgg ma fekk fii ma
toog, di waxtaan ak yéen, ñu coob ma !
Waaye dëmm yooyu, dinañu wax lu ... | DOOMI-GOLO-Ebook-1.pdf |
page_229 | Aatu Sekk a ngi leen bëgg a balu àq,
waaye saa yu ηaaηee, mu mel ni dañuy
jamat ay puso yu tàng jërr ci gémmiñ gi.
Fi ñu ko takk, mu ngi yërëmtalu.
Ndeysaan !
- Yéen a ñuul xol, doom ! Nu ngeen àttane
def seen Maam Aatu Sekk lu ñaawe nii ?
Dangeen ma bëgg a toroxal, daal ? Naka
la Ninki dégg baatam, daldi bàyyi... | DOOMI-GOLO-Ebook-1.pdf |
page_230 | Ndax kat, lu Doomu-Aadama denc ci
xelam la ba noppi fas yéene koo dénk ku
mu wóolu dëgg. Kuy déey nit dara, sa
xalaat ngay xelli ci xelam. Te ba àddinay
baax de, golook yeneen mala yi daawuñu
xalaat bay wax. Su weesoo seku daal
- te seku sax li muy wax dara la ci xamul !
- sëpp-jaleñu, yuuxu ak yu ni deme lañu... | DOOMI-GOLO-Ebook-1.pdf |
page_231 | Am na it ay këri Guy-Géwél yuy lakk.
Lakk gi warul a soreyook fi Aatu toog,
ndax ëtt baa ngi leer nàññ. Aatu Sekk ni
ci xelam : « Mel na ni gaa ñaa ngi xëccoo
Toolu-Buur ». Yoon yu bare te yaatooy
jaar Toolu-Buur, nag.
Moo tax ñu ne :
- Ku teg loxo ci Toolu-Buur yaa moom
Guy-Géwél, moom dëkk bi. Te ku moom
d... | DOOMI-GOLO-Ebook-1.pdf |
page_232 | - Réll ! Ay roppëlaan tiim dëkk bi, yàbbi
safara su baree-bare ci mbeddi Guy-Géwél
yi. Asamaan siy rëg-rëgi, kër yiy riir, bunt
yépp di dal, jaww ji ñuul kukk ak saxaar.
Aatu Sekk daldi ne golo yi : Dof yaa ngi
ci yoon wiy ñëw de, léegi ñu ne jamet ci
sunu kanam ak seeni saar de kombaa !
*
* *
Jaratul wera... | DOOMI-GOLO-Ebook-1.pdf |
page_233 | « Waaw. Nee ñu de, ku teg loxo ci Guy-
Géwél gàddu ndam li. » Lenn moom wóor
na Aatu. Bés bu jàmm dellusee Jafune,
baadoolo dootul des Guy-Géwél. Béréb bu
ame nii solo, boroom alal yi dinañu ko
aakimoo. Rax-ci-dolli, dafa tafu ci géej gi
te it dex gi sorewu ko. Te ku nekk xam na
ni boroom barke yi yéenewuñu kenn ... | DOOMI-GOLO-Ebook-1.pdf |
page_234 | Lu mu yëg ci yaramam la. Pas-pasu dund
doηη a ko téye, nde kon leneen lañuy wax.
Ñaari gone yi kañ, ñoo ko jaaxal. Lu mu
leen def ba ñu koy yeew ci niim gi, di ko
sànni seeni ndesit, su ko bañee lekk ñu
koy duma ay duma yu metti ? Bu doon
sagoom de, ñu may ko mu sangu, sol yére
yu set, jublu penku julli, ni mu k... | DOOMI-GOLO-Ebook-1.pdf |
page_235 | Góor gi Aatoo ngi làqu ci ginnaaw buntu
saal bi di leen seetaan. Sañul a sëqat. Su
ñu yëgee ne yolomal na buumam ba jóg
taxaw, dañu koy rey ! Xale bu góor bi,
Ninki, dafa rekk soxar, moom ! Ci tele bi,
benn janqu tubaab a ngi làkk nasaraan.
Ni muy waxee gën a gaaw ! Waaw,
moom sax ndax dina noyyi suy wax ? Saa ... | DOOMI-GOLO-Ebook-1.pdf |
page_236 | Ndeke guddeek bëccëg ñu ngi seetaan
tele! Leneen lu dul loolu safatuleen.
« Xanaa ma jàppe ko noonu, boog ».
Aatu taxaw na lu mat genn-wàllu waxtu ci
buntu saal bi, te Ninki-Nanka yëgu ci
dara. Bi doomi golo yi génnee, fekk nañu
góor gi Aatu mu takkaat buumam ba mu
dëgër, di nelaw-nelawlu ci taatu niim gi.
Fan ... | DOOMI-GOLO-Ebook-1.pdf |
page_237 | Kokku téye ci ndigg li, ñu ànd di
wëndéelu, fu nekk ñu fay sànni seeni tànk,
coow li ne kurr ci saal bi. Góor gi Aatu
waaruwul yem ci. Dafa tiit bay dankaafu
boppam :
« Aatu Sekk, ñaari gone yii waxaguñu li
ñu la naral, de : ndof ak dee ngi lay yoot.
Bul ko nangu. Lànkal, Aatu Sekk, bul
nangoo jommi. » Aatu Se... | DOOMI-GOLO-Ebook-1.pdf |
page_238 | Ñetti fan a ngii Guy-Géwél ne selaw.
Taxul nag waa gox bi ñibbisi. Loolu, kenn
waxaalewu ko sax. Mel na ni Dibi-Dibee
jekku way-fippu yi. Bi Aatu Sekk déggee
loolu, dafa jàpp bopp bi, mbir mi def ko
tiis wu réy :
- Ba waa ju kannasu jii daal, moo nar a
wéy di nu jiite ! Dina fi toogati ay at, di nu
tuur àndaari... | DOOMI-GOLO-Ebook-1.pdf |
page_239 | Aa ! Moom daal mooy seen jaam ? Dina
leen won mooy kan !
Ninki.
Nanka
« Sunu xaree nar a metti ! Dinaa leen jàng
ba jeexal leen, ndax ma xam fu ma leen di
jaar ! »
Aatu Sekk lim ci xelam fànn yi mu
yaakaar ne warees na cee gëstu ngir gën a
xam xeetu Ninki-Nanka.
« Lépp lu gëstukat yi bind ci mbirum
golo, war... | DOOMI-GOLO-Ebook-1.pdf |
page_240 | Golo yi ñu tëj fii ci Toolu-Buur, gone yiy
ñëw di leen seetaan, di leen sànni gerte
kemb ak xollitu banaanaak xollitu sorãs.
Naka la golo yiy dunde ci àll bi.
Ni ñuy tànnee seen njiit.
Ni ñuy séye ci seen biir.
Li ñuy lekk. Góor gi Aatu di lim ba agsi ci
ni golo gu jigéen di doxaleek ay doomam.
Mu ne ci xelam ... | DOOMI-GOLO-Ebook-1.pdf |
page_241 | Ñu jàppee ko noonu lu mat juróom-benni
fan. Nijaay Gaynde dem ba amatul pexe,
mu jaaxaan, jébbal leen boppam. Ñu wër
ko nag, di ko ηóobi, di ko saaga ci seen
kàllaama golo. Ba mu leen wóoree ne
Nijaay Gaynde Njaay saay na, ñu bàyyi ko
fa dem seen yoon.
Ni golo nirook nit, nag ! Moom kay, ñépp
war nañoo xas gol... | DOOMI-GOLO-Ebook-1.pdf |
page_242 | Dafa neexoon ba dee ! Nga xéy bés rekk
ne doyal nga ci nekkin boobu ! Ban njariñ
la la amal, tey ? Nee nga tuddatoo golo,
ndax yaay Nit. Su sa soxna ëmbee, nga ne
ko bumu jaar ci sama tur, mu may woowe
noppi-jaboot. Fu mu foog ne dinaa fa aw,
mu jaar fa ca des ndax rekk ragal dajeek
man, ma jigadi doomam. Nee ng... | DOOMI-GOLO-Ebook-1.pdf |
page_243 | Li nga nekke kat, gisuma lu ko jar ! Ku
nekk naan sa moroom maa la dàq daw,
maa la dàq jàng, sama jëkkër moo ëpp
xaalis sa jëkkër, sama réew a ëpp doole ci
réew yi ci àddina si sépp ! Yu ñàkk solo
yooyu bañu leen ci ba ku jekku sa
moroom butti ko. Waaye fi nga ma yéeme
dëgg, mooy bi nga jëlee sa sagaru kayit,
r... | DOOMI-GOLO-Ebook-1.pdf |
page_244 | Ni mu xëccoo, buum gi naj ko, mu yuuxu.
Nankaa jëkk a génn, gis ko, daldi woo
mag ji. Ninki ñëw, gëdd góor gi ba noppi
fasaat buum gi ba mu gën a dëgër.
*
* *
Guddig sàttumbar. Biddéew yaa ngi tiim
Guy-Géwél di melax ci asamaan si. Yoo
yeek yeneen gunóor yaa ngi biiw. Lu mat
waxtoo ngi nii Aatu Sekk di wë... | DOOMI-GOLO-Ebook-1.pdf |
page_245 | « Ak ñu ngeen mënti doon, maa ngi leen
di xaar ! Ñëw leen def ci man lu leen
neex ! Yàllaa leen ëpp doole fuuf ! »
Xelu góor gi Aatu Sekk ne yarr ci Ninki-
Nanka. Mu yuuxu :
- Yéen daal, waat ngeen ne sama saal beey
seen fowukaay ! Baax na ! Su ma leen fa
fekkee dinaa lakk seen lu bon !
Mu direeku ba ci ñoom, ... | DOOMI-GOLO-Ebook-1.pdf |
page_246 | Du ñàkk mu am ñu ne góor gi Aatu Sekk
bare na lu muy wax waxu telewisoη.
Ñooñu de, su ñu seetoon bu baax seen xel,
dinañu xam ne yëf yi mënul a deme
neneen. Naka lay def ba xelam du nekk ci
tele bi dëkkee tàkk ci saal bi ? Mu ngi
Guy-Géwél di xaar. Lu muy xaar ? Xamu
ko. Xamul it ñan lay xaar. Ñu ngi ci yoon
wi... | DOOMI-GOLO-Ebook-1.pdf |
page_247 | Ku leen gis xam ne ñoom ñaar nobante
nañu lool. Ndaw si taxaw, joxoñ bakkanu
far wi, cof kook baaramam, ne ko :
- Fii laay noyyee !
Ku góor ki ree, gën koo kott.
Janq bee ka rafet, kaar ! Karaw gaa ngi
ñuul kukk, di watatu ci ginnaaw mbagg yi,
cëru jigéenam yépp mat sëkk. Xaleelu
góor bi dab ko, kottaat ko, ñu ... | DOOMI-GOLO-Ebook-1.pdf |
page_248 | Bi film bi àggee foofu nag, Aatu Sekk
seetlu na lu doy waar. Bi ndaw si
tàmbalee futteeku, ñaari doomi golo yi
dañu daldi tàggook seen sago ci saa si. Ñu
ngi yuuxu, di tàccu waa ji. Waaye bi
soldaar bi bañee tëdde coroom, jéppi nañu
ko lool. Dem nañu sax bay dóor tele bi, di
sànni seeni loxo fu nekk, di ciipatu... | DOOMI-GOLO-Ebook-1.pdf |
page_249 | Bés yi maasaloo nañu. Jamono ji ci
boppam saay na. Aatu Sekk njort na ne
léegi ràññee tàkkusaan ak njël të ko. Li
wóor daal, moo di ne fexe na ba dagg
buum gi ko doomi golo yi yeewe, dem
doxantu moom kenn biir Guy-Géwél.
Keroog jooju la Aatu Sekk bég ! Péexu
géej gaa ngi koy dugg, di yëkkati
mbubbam, di raxas ... | DOOMI-GOLO-Ebook-1.pdf |
page_250 | Sàllaaw dina won ñaari golo yi mooy kan!
Du daw mukk ba noppi di taafantoo wuti
doole. Déedéet ! Day dellu kër ga, jébbal
boppam Ninkeek Nanka te xam ne yàgg-
yàgg dina leen jekkuji. Xanaa du ndànk-
ndànk ay jàpp golo cib ñaay ? Naka la
doomi golo yi dégg Aatu Sekk laal buntu
kër gi, ñu daldi dawsi di ko xool ay b... | DOOMI-GOLO-Ebook-1.pdf |
page_251 | - Foo nekkoon, Aatu Sekk ? Seet nanu la
ci kër gi yépp ! Waaye nun nga koy
digaaleel, li nga def tey moom dootul
ñaar ! Noonu, Ninki jël benn musóor tàkk
bët yi, tafaale gémmiñ gi, bàyyil ko tuuti
fu mu mën a noyyeek bakkan bi, ba noppi
nag taxawal ko ci taatu niim gi, wërale
yaram week benn buum gu gudd a gudd... | DOOMI-GOLO-Ebook-1.pdf |
page_252 | - Waaw gone yi, lan laa leen def ? Lu tax
ngeen bañ ma nii ? Rey leen ma benn
yoon ma noppaluji àllaaxira !
*
* *
Doomu-Aadama Njaay moo kéemaane !
Góor gi Aatu dafa jékki-jékki rekk, benn
woy ne cabax ci xel mi, mu yëg ni yaram
wiy dawe. Ndax sax woy woowu dafa
jóge fu sore, ñëw dëgg-dëgg ci xelam ?
Du ... | DOOMI-GOLO-Ebook-1.pdf |
page_253 | Li muy woy ci suuf yépp, mu ngi jéem a
fàttaliku lan moo tegu ci kàddu yooyu, ak
fan la leen mas a dégge. Ndax du woyu
kasag wu mu daan dégg ci ngoneem ?
Wànte woyu kasag neneen lay tëdde,
mooy gën a xumb. Bu gaa ñiy tëgg, rëkk
yeey gën a jegeyoo.
Waay Ninki-Nanka, kaay tekki samay
loxo ndax ma mën a tàccu ngel... | DOOMI-GOLO-Ebook-1.pdf |
page_254 | Ku leen fent ? Lan la ci jublu woon ? Am
na ay kàddu yuy yëngal nit ki te du xam lu
tax. Gayndee Njaay, mbarawàcc ! Baat
boobu, saa yu ko waa Jafune déggee,
tàggook seen sago, mu ñaax leen, ku ñu
song daan la. Fan la Ninki-Nanka génne,
ba ñëw janook moom ? Keroog la góor gi
Aatu Sekk mas a réccu li mu toppul waa... | DOOMI-GOLO-Ebook-1.pdf |
page_255 | - Waaw, kañ la Tubaab yi bokk ci xeex
bi ? Ndekete at yii yépp xaj yu bon yaa
ngi ci kow garabi Guy-Géwél yi, tiim ma !
Ñii ma gis ñuy wëndéelu ci kër gi de,
benn Xonq-Nopp mooy seen njiit ! Walla
boog damay gént ? Bi Aatu Sekk génnee
ci mbedd mi di seet lu xew Guy-Géwél la
dajeek ñi ci des. Ñaar-fukki Xonq-Nop... | DOOMI-GOLO-Ebook-1.pdf |
page_256 | Ñu xoolante ñoom ñaar, mu rocci fetal gi
mu làqoon ci lafu sëram, dàkk ndànk Aatu
Sekk.Golo gu jigéen gi soqi, soqiwaat.
Góor gi Aatu Sekk yëg ni ko ngelaw liy
tàggoo, di raay kanam gi : Man ràkkaaju
naa ! Waaw, man ràkkaaju naa ! | DOOMI-GOLO-Ebook-1.pdf |
page_257 | TÉEREB WIS | DOOMI-GOLO-Ebook-1.pdf |
page_258 | Badu, wóor na ma ne su ma la laajoon lan
mooy gën a biral sunu aaday cosaan ci
mbirum fo ak tàngal yaram, dinga ma ni :
- Làmb la, Ngiraan.
Su ma delloo ne la :
- Limal may turi mbër, du ñàkk nga ni ma :
- Tafaa Géy mbaa magam Mbay Géy,
Duubal Lees, Mànga, Tubaabu Joor ak
Bàlla Béey.
Su dee ku la mag laa laaj ... | DOOMI-GOLO-Ebook-1.pdf |
page_259 | Làmb góor a ko moom,
Lii bu doon làmbu jigéen sax jeex na- a-a-
a, Ku ci nekk ànd ak sa gàngóor, gaa ñiy
sànniy pitax ak a toj ay nen, loolu yépp
soo ko déggee, teg ci sa bët, fàww sa
yaram daw, Badu. Noo def sa xel dem fu
soree-sori.Ñu dégg laak ñu bañ laa dégg,
dinga ne :
- Futbal neex na lool te am bayre, waa... | DOOMI-GOLO-Ebook-1.pdf |
page_260 | ku ci jëkk a yëkkati sa loxo dóor sa
moroom teggi nga yoonu aadaak cosaan !
Lu ma tax a wax loolu ? Dafa fekk ne
bëre-dóor, ak li coow liy bare yépp, Maam
masu koo xam. Bëre dóor, benn Tubaab
bu xonq coy bu tudd Móris Sakeη moo ko
dugal ci réew mi
Móris Sakeη moomu, minise la woon,
dëkkoon Sàndiñéeri gii, ci w... | DOOMI-GOLO-Ebook-1.pdf |
page_261 | Garaη Maxoo fi dàq xeex, ëpp fi fit,
waaye du tooñ. Moo tax mu jëkk jéem a
sàng Tubaab bi sutura.
Kooku di ko jaay ñàkk teggin :
- Nuu tarwaaye, Maxtaar, paa salaamaaleg
Ust ! Ayca ! Garaη Maxu daldi gis
boppam ci saa si :
- Waay, Xonq-Nopp bii man lay sëppu,
tey laay dëgg ndeyam ba mu xool benn
béréb ! Naka l... | DOOMI-GOLO-Ebook-1.pdf |
page_262 | Dafa daw wuti Tubaab bi, taxaw ci
kanamam, xulli ko. Móris Sakeη gis paaka
bi Garaη Maxu téye, daldi tàmbalee dellu
ginnaaw. Fu mu aw, Garaη Maxu topp
kook paakaam. Ñépp a ngi ne tekk, di leen
seetaan. Benn paa bu doon liggéey ak
Sakeη ne Garaη Maxu :
- Maxu, mbaa seet nga bu baax li
ngay def?
- Amul fog ! Su... | DOOMI-GOLO-Ebook-1.pdf |
page_263 | Garaη Maxu ne këj, di ñàngal. Ñu fey ko
xaalisam, mu jiital ma, nu dellusi Ñarelaa.
Keroog may na ma lu ma jënde pastel ci
Meer Màgget ba noppi ne ma :
- Du xam nga Tinaa Delgaado, sama gelu
ηaaña bi ?
- Waaw, Garaη !
- Joxal ma ko ñaar-fukki dërëm yii, ne ko
mu rëgal ci kaccuupa, maak sama kàngam
yi dinanu re... | DOOMI-GOLO-Ebook-1.pdf |
page_264 | Afrig yépp nag a may tax a wax. Muy
Lumumbaa, di Sànkaraa, di Séex Anta
Jóob, di Móngo Beti, di Amilkaar Kabral,
di Sàmóori Ture, képp ku mas a aw yoon
wu Tubaab bi xàllul, tam na la dëmm
mbaa mu bóom la ! Cim ! Ngay Doomu-
Aadama ni ñépp, ñu tënk la te sañoo sax
yëngu. Jéngu ? Yëngu ? Déedéet ! Sa xel
nekku ci,... | DOOMI-GOLO-Ebook-1.pdf |
page_265 | - Làmb laa dégg, de ?
- Sàllaaw. Ci néeg bu yaatu la gaa ñiy
bëree.
- Kañ lañu daan bëre ci biir néeg ?
- Loolu kay doy na waar !
- Man de, dinaa ko deñi kumpa !
- Doo ma fi ba !
- Ayca, nanu seeti naka la nen di bondee
ci kekk...Ñu ànd ñoom ñépp, ne ñu ngay
seetaani làmbu Móris Sakeη ju kéemaane
jooju. Sakeη... | DOOMI-GOLO-Ebook-1.pdf |
page_266 | - Lu leen wutale ?
- Bii, mbër yi dañuy dóorante ay kurpeñ.
- Dóorante tàww ?
- Ay dóor yu metti sax. Lépp xej na ci.
Man mii maay fomp deret ji su ñu xeexee
ba noppi.
- Loolu kay du bëre, leneen la !
- Muse Sakeη de, bëre la ko tudde.
Li ñuy wax ak waa ji yépp, nit ñaa ngi
leen di romb, di dugg ci biir saal b... | DOOMI-GOLO-Ebook-1.pdf |
page_267 | Móris Sakeη fekki ko ci géew bi, yëkkati
loxoom. Mbooloo mi àndandoo di tàccu
Garaη Maxu. Móris Sakeη waññ xaalis
jox ko ba noppi takkal ko raaya Tugal ci
baat bi.
Ku gisul keroog ni gaa ñi duggsee
Ñarelaa, gisoo dara ! Garaη Maxu nekk na
fi mbër xaat, nun gone yi nu dar ko, mu
fent ay bàkk, di woy ak baatam bu... | DOOMI-GOLO-Ebook-1.pdf |
page_268 | Fii la woon, ci wetu sinemaa El-Maalig,
ci Ñaay-Cokkeer gii, ci atum 1930. Du
benn du ñaar, mbër jóge na làmb jooju
deretam tuuru, kanam giy nàcc, bëñ yi rot.
Móris Sakeη dem na bay tëgg làmb noor,
di tëgg làmb nawet.
Lu doy waar la fi Sakeη def. Dafa dugal ci
boppu goney réew mi ne xeex rekk mën
na laa may loo... | DOOMI-GOLO-Ebook-1.pdf |
page_269 | Xam lépp, wax lépp baaxul, Badu.Waaye
Ñarelaa gii de, am na fi ñetti kër yu mag
yoo xam ne seen alal ji ñuy coow, ci
Móris Sakeη la jóge.
Ñooñu fi seen njaboot di jaay tey maanaa,
dañu daan xéy jubal pooru Ndakaaru,
waxambaane wu ñu gis nga am doole ñu
woo la ci pet, ne la :
- Saa waay, yaa ngi yàq xaalis, de.... | DOOMI-GOLO-Ebook-1.pdf |
page_270 | Ay niti Móris Sakeη daan nañu bawoo it
Ndakaaru dem Saalum, dem Kaasamaas
ak Fuuta, dem Kajoor walla Kéedugu,
fekk fa waxambaane wu sëgg ci naaj wiy
bey gerte mbaa dugub mbaa ceeb,
ñu ne la :
- Yaa ñàkk faayda dëgg, alal ju dul jeex a
nga lay xaar réewu taax ya, nga nekk fiy
kocc-koccal !
- Réewu taax yan ?
... | DOOMI-GOLO-Ebook-1.pdf |
page_271 | sa mbokki tubaab yi jàppale la, ba tee laa
tumuraanke. Dégg naa it ñu naan ku
bëggoon jigéen nga, te jot nga fee def ay
njaaxum. Fu ñu la fekkaan, yow Sakeη,
yaa ngi sex sa kamelyaa, di xëcc. Làmb ji
nga ubbi woon Ñaay-Cokkeer, duggewoo
ko woon dara lu dul wut alal. Bi nga
demee ba yëf yiy dox, danga daldi wàññi... | DOOMI-GOLO-Ebook-1.pdf |
page_272 | Ma wax ko te dee : li ëpp solo ci bëre-
dóor, dóor yi la. Te loolu, maam bàyyiwu
ko fi. Xanaa kay kenn du ma ne Móris
Sakeη mooy sunu maam ! Kon xam nga,
Badu, bu ñu demee ba raaya Amerig
wuutu sëru rabal yu yànj ya mbër yi daan
ngemboo, gone yiy bàkku ni ay tubaab, ne
bu leen kenn woowe Saa-Waalo mbaa
Booy Bàmb... | DOOMI-GOLO-Ebook-1.pdf |
page_273 | Mag ñu baax ñi fi jot a jaar daan nañu wax
ni :
- Roy-dàq.
Ñi seen xel gàtt, jàppe ko ngóora. Néew
dégg-dégg mënul a weesu loolu !
Roy-dàq mooy :
- Roy yàq. Yàq sa bopp.
Yàq sa bopp... Soo ci naree am xel ñaar,
Badu, fàttalikul wax jii :
- Ku wàcc sa and, and boo dem fekk ca
boroom.
*
* *
Séex Anta Jó... | DOOMI-GOLO-Ebook-1.pdf |
page_274 | liy tax nit ku ñuul jëm kanam te du
sibooru kenn. Su nu ko déglu woon na mu
ware, dog kon nanu buumu njaam gi bu
yàgg. Nit ku maandu la woon, lewet ba
nga ni lii lu mu doon, ndeysaan, waaye
kenn feesul woon bëtam. Soo toogee tey
ci sa kanamu tele, gis ni Daawur Jaañ
baree tiitar, gis yu ñàkk faayda yi mu jiital ... | DOOMI-GOLO-Ebook-1.pdf |
page_275 | Séex Anta Jóob teel naa làqu, ndax bi ñu
koy denci Céytu, ci 1986, amul woon lu
dul juróom-benn fuki at ak ñaar.
Amul bés bu ma jullee, man Ngiraan Fay,
te ñaanaluma Séex Anta Jóob. Dundam
neenul ci genn wet. Miinantewunu woon,
gaa. Ay mitiηam doηη laa daan dem, di ko
déglu. Waaye li am solo ci nit ki mooy mu
a... | DOOMI-GOLO-Ebook-1.pdf |
page_276 | Xalaatam ak dundam, teen bu xóot a xóot
la.Fexeel ba say doom duy ci, Badu. Man
Ngiraan Fay, giñ naa ni su ko samay
doomi sët defee, duñ ko réccu. Giñ naa ni
su goney Afrig yépp awee ci yoon wi leen
Séex Anta Jóob xàllal, ak lu mu yàgg
yàgg yabeel gi dina deñi ba fàww.
*
* *
Ninki-Nanka.
Ñaari doomi golo ... | DOOMI-GOLO-Ebook-1.pdf |
page_277 | benn doηη lay faral di jur te duy faral di
am ay séex. Bu nekkee liir, ci biir bi la ko
ndey jiy boot. Su demee ba xaw a dëgër,
mu teg ko ci diggu-ginnaawam, fu mu jëm
yóbbaale ko. Xéy-na looloo tax wolof
Njaay naan :
- Alalu golo ca lex ba !
Lii tamit gëstukat yu bare wax nañu ko :
doomi golo, du ñaari way-jur... | DOOMI-GOLO-Ebook-1.pdf |
page_278 | Nee ñu ñi ko jéem a dékku yépp dañu fa
jóge gumba ! Ca Amerig nag, am na fa
golo gu nirook jargoñ lool, te ñu koy lekk.
Ñi mos yàppam nee nañu dara dàqu ko !
Golo mën naa dund téeméeri at ak lu topp.
Waaye Sinuwaa yi ñoom, jàpp nañu ne ci
mbindeef yépp, golo rekk moo ciy dund
ba abadan. Waa Siin yooyu, dinañuy w... | DOOMI-GOLO-Ebook-1.pdf |
page_279 | - Yow ! Maa la xam. Waxoo wax ji de !
Am na loo may nëbbati !
- Du dara, sa ràkk jee may bëgg a jaaxal
doηη.
- Kan ci ? Kinne ?
- Ñaata ràkk yu jigéen nga am ?
- Céy yaak sa Kinne mi ! Yéen daal waat
ngeen ne... Ñu daldi jàdd koñ. Mbeddu
Ñarelaa mi neeti selaw, di xaar yeneen
ñaari Doomi-Aadama jaar fi, suy a... | DOOMI-GOLO-Ebook-1.pdf |
page_280 | Ma daldi siggi, gis baay mu ne tekk di ma
xool. Sunuy bët daje. Nekk gone du tee
yëg yenn yi ci sa yaram. Maa ngi gis ni
mu ma xaaree. Li ma def baay kañ laa
xamul, waaye jéppi na ma ba fu jéppi
yem.Mu sànni yar bi, wiccax bopp bi, ne
ma :
- Xawma kan moo nar a tekkiji ëllëg ci
sama doom yi, waaye du yow mii,
... | DOOMI-GOLO-Ebook-1.pdf |
page_281 | Foo jublu xetu biiñ mbaa xetu yàmbaa
song la, dàq la. Néegi baraagi Ñarelaa yee
fi yàgg ! Yu ci bare maxe nañu ba fënëx.
Lee-lee, su tawee ba séwét, kër yu bare
dañuy taa ba kenn du am foo jaar, mbaa
nga dégg ni am na ay baraag yu màbb.
Mbedd yaa ngi mel niy sën, yoo yeek weñ
yi dëkke biiw, lakkal nit ñi guddeek... | DOOMI-GOLO-Ebook-1.pdf |
page_282 | Ay till, ay jaan, ay bukki ak yeneen rabi-
àll ñoo fi feesoon.Xanaa looloo tax lépp lu
bees lu mas a dugg ci réew mi, Ñarelaa la
ko Yàlla jaarale ? Du ñàkk. Oto bi jëkk a
wàcc ci dëkk bi te doomu réew mi
moomal ko boppam, Ñarelaa lañu ko
ngéntee ! Céy ! Ku fekkewul bés ba Fara
Mbóoj jógee dëkk baak xantu Wersaaya... | DOOMI-GOLO-Ebook-1.pdf |
page_283 | Benn doomu Kab-Weer bu ñu naan Tooy
Delgaado, moo fi jëkk a ubbi néegu
watukaay ci Ñarelaa gii. Senegaal ba
Senegaal daj, kenn masu noo jëkk a gis
raasuwaar, nun waa Ñarelaa ! Ci Téereb
Wis bii nga téye di ko jàng sax, dinga
dajeek ndaw su tudd Tinaa Delgaado, muy
toggal Garaη Maxu kaccuupa. Tinaa
Delgaado moom... | DOOMI-GOLO-Ebook-1.pdf |
page_284 | Isin ba ma daan liggéeye, benn nit ku
weex doηη moo fa newoon, ñu koy wax
Póol Gimaar. Bu dajewaan ak yow ci ëttu
isin bi, day taxaw ne la jàkk. Soo
sëggulee, mu àjji sa kaabaab. Soo
sukkulee balu ko àq, mu dàq la ci saa si.
Lu waral loolu ?
Ci sama gis-gis bu gàtt bi de, yaakaar naa
ne buum gi ab doxandéem di... | DOOMI-GOLO-Ebook-1.pdf |
page_285 | Noonu la Tubaab bi ñamalee ay doomi
réew mi ci làkkam, ñii nekk ay làppto, ñii
solu soldaar, ñeeneen ñi nekk ay bóoy
walla ay mbindaan.Aka noo ñee woon
bóoy yeek mbindaan yi !
Aa, bul ree, Badu !
Jamono jooju kay, daraja nit kaa ngi aju
woon ci na mu gën a jegee Tubaab bi. Ñu
bare bëggoon nañoo nekk bóoy walla... | DOOMI-GOLO-Ebook-1.pdf |
page_286 | So gisee sama gaa ñi, ñu nga ne noηη ci
kow, ak seeni west ak seeni kàsk ! Ku ci
téyewul téere Lamartin walla Wiktoor Igo
la xawma, di yuuxu ci naaj wu tàng wi,
yaa ngay jàng surnaal bi ñu doon wax
booba Pari-Dakaar.
Lépp daal, ngir won nu ne ñoom duñu
ñeexu-ñebbe ! Àddinaa mën a soppiku,
walla ! Léegi, baadoo... | DOOMI-GOLO-Ebook-1.pdf |
page_287 | Dafa ni :
- Tubaab bi dafa noo nëbb sunu bopp,
won nu boppam.
Mën a toppandoo bu jéggi dayo boobu
nag, Badu, man mii teel naa gis ne
doxalinu golo kese la. Moo waral, jamono
jooju, ma dem bokki PAI, ànd ak gor ya
ma fa fekk, nuy xeex Tubaab bi, ne fàww
yu ñàkk faayda yooyu dakk, nu gar ci
sunu bakkan. Ñu bare ... | DOOMI-GOLO-Ebook-1.pdf |
page_288 | danga naan nun noo leen xawoon a tane,
yéen goney léegi yi. Tubaab bi déj na nit
ku ñuul ci kanamu seetu bi. Kooku seetu,
gis boppam ci biir, rus, daldi sëgg.
Ne tuuti, mu siggi ne :
- Aa ! Dem naa bay juum sax, kii kay du
man, kii keneen la.
Neeti tuuti, mu daldi mer, ne ki mu janool
ci biir seetu bi :
- Be... | DOOMI-GOLO-Ebook-1.pdf |
page_290 | TÉEREB DÓOM
III | DOOMI-GOLO-Ebook-1.pdf |
page_291 | Badu, xibaar bu neex a ngi lay xaar
Ñarelaa. Kaay ma fen la ko gaaw : Baydi
Sàll tudde na la fi doom. Bërki-démb ci
alxames ji la woon ngénte li.
Ndaw mbetteel gu neex ci man mii ! Ñu
bare jooy nañu fa te tuuti kon ñu jooyloo
ma. Dañu la faa gërëm, yow Badu, ba am
ñu tiit, di jéem a delloosi xelu nit ñi :
- Laa... | DOOMI-GOLO-Ebook-1.pdf |
page_292 | Soo gisee ma lay wax loolu, dafa fekk ma
yëg fan yii ni sama yaram wiy bañe.
Duma la ko nëbb : bi ma jógee ngénte la,
daanu naa ci yoon wi, daldi sax xëm
foofu. Dama jékki-jékki samay tànk diis
gann, may miir, xamatuma fan laa nekk.
Muse Sumaare mi ma doon tooñ keroog
ci Téereb Dóom bu jëkk bi, moo ma fa
fekk,... | DOOMI-GOLO-Ebook-1.pdf |
page_293 | Fàww ma bind, bàyyil la fi, Badu. Te su
nu waxantee dëgg nag, jokkoo beek yow
ci boppam moo ma neex.
Te it, feek maa ngi noyyi, li war ci sama
digganteek yow dinaa ko def ba mu mat
sëkk.Xanaa kañ damay jéem a bàyyi
kebetu bi rekk.
Li ci des nag, maanaam dund mbaa dee,
Yàllaa ko yor. Lu mu dogal ak waxtu wu
m... | DOOMI-GOLO-Ebook-1.pdf |
page_294 | Ayca boog, Badu, nanu déj ci diggu géew
bi Yaasin Njaay ak ñaari doomam yu
xamadi yi mu jële Tugal, indil nu leen
Ñarelaa.
*
* *
Li Yaasin Njaay xamul moo di ne Ñarelaa,
gox buy naxaate la. Nekk na fi, di dem aka
dikk, defe ne kenn toppatoowul ay mbiram.
Fekk na boobu tànk bu mu yëkkati, balaa
muy fekki b... | DOOMI-GOLO-Ebook-1.pdf |
page_295 | Ñaari doom yi ñoom, gone du reew ba dab
leen. Man lañu def seen golo. Dañu may
fekk lee-lee may wird, ñu may sëllax suuf,
di ma sànniy xollitu banaana.
Yaasin moom, sa ndey Biige Sàmb la ko
Yàlla nattoo. Biige naxante naak moom,
fiir ko, ba sànk ko. Mën nañu wax sax ni
Yaasin Njaay dafa alku.
Moytul ma merum ji... | DOOMI-GOLO-Ebook-1.pdf |
page_296 | - Sama rakk, yaa bëgg futbal ! Dafa mel ni
bés ba ñu la ngéntee, dañoo xooj balu
futbal ci ndox, jox la nga naan !
Dinaa ci yokk ne sa baay Asan Taal
futbalkat bu mag la woon. Moo tax bi mu
nee day dem Màrsey, bettul kenn. Xawma
nag lu tax yëf yi mujjewul a àntu foofa.
Am na daal ay wax yu ñaaw yu ci nit ñi
jot... | DOOMI-GOLO-Ebook-1.pdf |
page_297 | Keroog, Ñarelaa gis na lu ko yéem. Am
ñu naan :
- Ñaw ! Lu waay rendi ci sa loxo lay nàcc.
- Fii Ñarelaa la ! Wund du fi naane ñeex!
- Ñuy wax mu naan moom tubaab bu
weex tàll la !
- Waaw, moom de nee na Mari-
Gabriyelaa Won Bolkowski la tudd !
- Mari-Gabriyelaa lan ? Ndaw tur wu
gudd sax ! Dem naa bay yërëm Y... | DOOMI-GOLO-Ebook-1.pdf |
page_298 | Su doon sama sago, ma jekk-jekkal mbir
mi ba mu gën a neex a dégg. Waaye xam
naa sama warugar : jottali la lépp li jot a
xew Ñarelaa sa ginnaaw.
*
* *
Bala nuy sore, may ma tuuti ma won la ni
Yaasin Njaay di daagoo ci mbeddi
Ñarelaa yi, jëm màrse.
Bés a ngoog ci bés yi ! Yoor-yoor la
woon. Yaasin Njaay xé... | DOOMI-GOLO-Ebook-1.pdf |
page_299 | - Man de, xawma man Yàllaa xiiroon
Asan Taal ci kii ba mu koy takk !
- Yaa yëg fu mu ko takke ? Dañu doon
nekkaale kañ, dégg naa. Ñeneen ñaa ngi
làqu ci seen ginnaaw palanteer di yërndu
Yaasin. Lu mat ñaari waxtu, Yaasin
wëndéelu na moom kenn ci gox bi. Du
benn yoon nag bu mu taxaw nuyoonteek
ñi mu jot a dajeel... | DOOMI-GOLO-Ebook-1.pdf |
page_300 | - Fa laa dëkk ba tey, dafa am yu ma doon
toppatoo rekk bi ma ténjee ba noppi.
- Aa ? Dangay dellu, kon ?
- Man kay taxaw naa.
- Tugal neex na de, dégg naa ! Bërki-
démb rekk, benn waay a ngi kaf ak man...
- Lu mu la wax ?
- Déedéet, benn Tubaab dafa ma may
junni, ma ne : « Tubaab bii de, Yal na ko
Yàlla xare àj... | DOOMI-GOLO-Ebook-1.pdf |
page_301 | - Picc ? Picc man ?
- Xanaa naaw, dem fu soree-sori.
Yaasin xàqataay. Ñarelaa yéemu. Ndekete
ndaw si am nay bëñ bay reetaan !
Nu laaj Cerno lan la waxanteek Yaasin.
Mu ne nu :
- Ndaw sii yembul. Dingeen ne Cerno Kan
waxoon na nu ko ! Kii, xel mi neexul de !
Ba mu jógee ci Cerno la Yaasin Njaay
dugg nag ci biir... | DOOMI-GOLO-Ebook-1.pdf |
Subsets and Splits
No community queries yet
The top public SQL queries from the community will appear here once available.