url stringlengths 6 8 | content stringlengths 2 3.72k | source stringclasses 3
values |
|---|---|---|
page_101 | Yaasin Njaay romb na ma, di gunge benn
xaleelu góor, waaye su ma ci kenn nee na
nga def, yaa ma nuyu, yow mi nekk bitim-
réew. Waa jooju nag, dégg naa ñu naan
Tamsiir la tudd. Nee ñu it day tóx yàmbaa,
di ko jaay. Xam naa ne daal, li muy
fanaan ci kër gaa ngi bëgg a bare.
Su dul nekkaale Yaasin Njaay it de,
sor... | DOOMI-GOLO-Ebook-1.pdf |
page_102 | taksi biy jëlsi suba su nekk Ñimma ak
Daawuda, doomi Wulimata Maane yi,
korne na ci mbedd mi, ñaari gone yi daldi
génn ak seen sànse, daw wuti buntu kër gi.
Fekksi nañu ma fi ma toog, ñu jox ma
loxo, Ñimma sukkal ma. Tooñ naa sax
Ñimma, ne ko :
- Aa, waaw séeri kóko dangay dem màrse
fàtte fi deppàs bi ? Am, téy... | DOOMI-GOLO-Ebook-1.pdf |
page_103 | dañoo nar a yàq réew mi ba mu yàqu
yaxeet ñu dem bàyyinu fi, jaaxaan
Monaako walla béréb yu ni mel, di
balaxalmàddaa, nun nuy wéye ndóol ak
metit wu dul jeex !
Waaye fi lañu nuy fekk, dunu seetaan
loolu, dinanu ko defanteek ñoom ba mu
saf sàpp!
Lamin dafa mer ba talu maa wax lu ko
merloo. Man it, teguma ci b... | DOOMI-GOLO-Ebook-1.pdf |
page_104 | Ma ne ko :
- Mbaa du dafa am loo fàtte, Lamin ?
- Déedéet, Ngiraan. Lu am solo laa la
bëgg a wax.
- Loolu lu mu ?
- Jàmm rekk la. Biig, dama gént di
waxtaan ak Badu Taal. Soo jullee tisbaar
ba noppi, génneel ko sarax.
- Baax na.
- Xale bu am jom a ngoog, Ngiraan.
- Badu kay kenn la, Lamin. Waaye ragal
naa n... | DOOMI-GOLO-Ebook-1.pdf |
page_105 | - Su dee xamoo fu gone googu nekk de,
ku yabu bañ cee sonn, ndax Badu sa Badu
la mas a doon. Bi Lamin génnee kër gi ba
ne tuuti, mu am lu ma dégg mu yëngu ci
sama ndeyjoor ; ma téen, daldi gis benn
wund wu ne noηη ci kow miir bi, xaw
maa tiim, ne ma jàkk. Nu xoolante lu yàgg
maak wund wi. Ni bët yiy tàkke, di me... | DOOMI-GOLO-Ebook-1.pdf |
page_106 | - Waaw, yow mii tudd Ngiraan, sant Fay,
santati Taal, yaay kan sax ci dëgg-dëgg ?
Laaj boobu ma laaj sama bopp tiital ma,
sama xel daldi dem xaat ci dee.
Tudd Ngiraan
Sant Fay, santati Taal. Dee di ma yoot.
Ci diir bu gàtt, yu bare ñëwaat nañu ci
sama xel : guddi ga la sibbiru su metti
daaneelee, yow mii Bad... | DOOMI-GOLO-Ebook-1.pdf |
page_107 | - Waaw, Ngiraan Fay, nga ne yaay kan
nag, ci dëgg-dëgg ?
Laaj bu kéemaanee ngoog.
Ku dem bay laay sa bopp yenn yi, li tee
nga jaaxal say mbokk bareetul.
Te tontu cee jafe, tey ! Ndax su ma nee
man maay Ngiraan Fay, juddoo Mbériη-
Saaj, ca Siin, ñëw Ñarelaa ba ma newee
liir, am tey juróom-ñaar fukki at ak lu
to... | DOOMI-GOLO-Ebook-1.pdf |
page_108 | mel na ni ba tey waxuma dara. Loolu yépp
amul solo, ndax fenn la yëf yi mujjewul.
Maa ngi nii déju ci taatu garab gii ci ëtt bi,
te xawma sax su ma fi jógee fan laay
jublu. Badu, li ma wokk a xosi ñu bare.
Waaw, nook juróom-ñaari fan yi nag,
ba kañ ? Bés yee koy tey di nu réeral.
Yeewu njël, di tés-tési ba ngoo... | DOOMI-GOLO-Ebook-1.pdf |
page_109 | Dëgg la, bàkku waru ma. Du dara loo xam
ne sottal naa ko, bi ma juddoo ca Mbériη-
Saaj ak tey jii. Du caagin dama nasaxoon.
Déedéet. Lu ne jéem naa ko, fu ne
làmbaatu naa fa, ni ko Doomi-Aadama
yépp di defe su ñu bëggee mënal seen
bopp, seeni nawle weg leen.
Ma seet seet, gisuma lu sama cawarte
googu jur. Guddi... | DOOMI-GOLO-Ebook-1.pdf |
page_110 | doo déglu kenn, xanaa jàpp ci li nga gëm,
sax ci ba dëgër.
Loolooy nit dëgg.
Su ma delluwoon nekk gone, noonu laay
doxale. Ma réccu lu ma mësul a ber benn
bés ci bés yi, waxtaan caak sama xel, ni :
- Man, Ngiraan Fay, béréb sàngam laa jëm
te yoon wii laay jaar.
Ñàkk doxalee noonoo ma tax a sànku.
Dama daan ... | DOOMI-GOLO-Ebook-1.pdf |
page_111 | Te yow ci sa bopp ba ngay nangoo topp ci
ginnaawam, doo ko sax yëg.
Yëf yi mbetteel lay doon.
Aw askan, dara ëppu ko doole. Dafay
yeew buum ci sa baat, di la wommat ni
xar. Dékku askan wi lu jafe la, ndax dafay
teel a jóg ci yow. Ba ngay bootu lay tàbbal
ci say nopp ay kàddu yu fay tëdd ba fàww.
Doo xam lu baa... | DOOMI-GOLO-Ebook-1.pdf |
page_112 | Xamu la, xamoo ko, waaye daanaka am
na lu mu jëmbët ci sa xel, ji ko ci sa xol.
Bala mu lay réer ci mbooloo mi, dinga ko
tontu ci suuf :
- Dégguma li nga wax, waaye ànd naa
ceek yow. Mën naa la cee jox beneen
firnde.Du ñàkk it bés nga xéy, tàllal sa
soxna sagaru téeméeri dërëm, ne ko
deppãs baa ngoog, lii rekk ... | DOOMI-GOLO-Ebook-1.pdf |
page_113 | seeni bët daje, yéen ñaar ñépp ngeen gis ci
saa si ne dungeen ay nawle.
Baydi nag, Yàlla fàttewu ko, waaye taxu
koo fuuy. Ku am kersa la, ak yar ak
teggin. Keroog def na kemtalaayu
kàttanam ngir bañ laa sewal. Jéem na la
won ne na ngeen meloon démb mooy wéy
ba tey. Yónnee na Fantaak Kokaa-Kolaa,
ngeen di naan, ... | DOOMI-GOLO-Ebook-1.pdf |
page_114 | - Jóob Sëriñ nag, foo koy dégg ? Moo
aayoon mat...
- Man it de, xawma fu mu mujje, waa
jooju,
- Yow moom, Ngiraan, jigéen rekk !
Daawoo nangu benn gel rëcc la ! Géy
Maryeem, Sow Faatu, céy Ngiraan yaa
teel a yàqu !
- Yow jinne nga de, Baydi, ndekete yaa
ngi fàttaliku turi nit ñooñu ba tey ! - Yaa
ngi fàtt... | DOOMI-GOLO-Ebook-1.pdf |
page_115 | Ku nekk ci yéen ñaar am yu muy xalaat te
am kersay wax ko. Lee-lee nga jéem a làq
sa tànk yu pënde yi ci suufu siis bi, Baydi
Gay mel ni ku ci gisul dara. Telefon bi
riir. Baydi jël ko, déglu tuuti, ne :
- Mersi madmisel.Am fu mu bës, tàmbalee
waxtaan ak keneen ci telefon bi. Xamoo
dara ci li muy wax, waaye wóor... | DOOMI-GOLO-Ebook-1.pdf |
page_116 | di lekk yàpp, di naan meew. Xanaa looloo
tax su nit tubaabee ba mu ëpp, ñu koy
tooñ, naan ko ηeew la ? Nangul mbir mi,
Ngiraan : ñee nga Baydi Gay lool ! Yaram
wépp a ngi nokki. Xam na moom ci
boppam ni ku dugg ci biroom, fekk ko mu
toog ci béréb bu rafetee nii, fàww nga naw
ko. Yow nag, Ngiraan ?
Nirootook n... | DOOMI-GOLO-Ebook-1.pdf |
page_117 | Sófóor bi moom daldi na la jéppi ci saa si.
Fu mu ko teg ? Xéy-na li nga ne noηη ci
ginnaaw oto bi, mu lay dawalal moo ko
naqadi. Ni mu la gise, xam na ne soo ko
tanee it du lool. Xanaa loolu mooy :
- Nangu naa jaamu Muse Gay miy
boroom alal, waaye ngóor sii ak yëreem
yu furi yii faalewuma ko. Dañuy wax
rekk, B... | DOOMI-GOLO-Ebook-1.pdf |
page_118 | - Foo bëgg Garaη-Kees nekk fu dul Kees ?
Li muy wax ak yow yépp, mu ngi lay niit
ci seetu bi ci biir oto bi. Nga ne ci sa xel :
sófóor bii gën a soxor te ñemee toppatoo
lu yoonam nekkul !
Mu laaj la fan nga jëm. Doo ko wax
moom ne Ñarelaa nga dëkk, nde kon mu
gën laa yab ! Nga ne ko :
- Wàcce ma ci bitig bee ... | DOOMI-GOLO-Ebook-1.pdf |
page_119 | Saa yu nu daan jàng sunuy lesoη, yaa
ngay fiir ay picc ci àll bi mbaa di wax
waxu fecc ak doxaan janq ji. Léegi nag,
mu ngi nii, yaa ngiy wër di ñaanaatu.
Li ngeen di waxtaan yépp, kàddu yooyoo
ngi jaabante ci jaww ji.
Moo tax ma ni la, Badu : Defuma ci suma
dund gii lu ma mën a bàkkoo. Dama
tëñëx-tëñëxi ba xéy... | DOOMI-GOLO-Ebook-1.pdf |
page_120 | Tey a ngi làqu ci biir Démb, ne nemm.
Jéemal a tëj sa loxo bu baax.
Ŋëb fa jamono ji balaa mu lay rëcc.
Maam Ngóor lañ ko daan woowe. Mu
nga, tëdd Mbériη-Saaj, ca Siin.
Njël ga ma wund wa tiime, di jooy, loolu
la ma fàttali. Mu am lu ma yëg ci sama
yaram. Ma daldi ne nu ma def dinaa dem
Siin, man mii.
*
* ... | DOOMI-GOLO-Ebook-1.pdf |
page_121 | nu romb Tëngéej, teg ci Barñi, tàllal ba
Jamñaajo nu door a jàdd wutali Mbériη-
Saaj. Sama xel ne yarr ci kàddu ya ma
daan dégg ba ma newee gone.
Benn ëtt bu yaa. Fan la woonati, sax ? Du
woon Mbériη-Saaj, moom. Ay mag toog
ci pénc mi, di waxtaan. Ñaari baat yu ne,
ñu tudd Maam Ngóor. Lu ne ñu koy wax
ciy mbiram... | DOOMI-GOLO-Ebook-1.pdf |
page_122 | - Dara, nag, Ngiraan : ku sa maam jur, jur
nga sa maam. Bu la ci kenn nax. Ma téen,
yaakaar ne biddéew yi dinañu ma tekkil
baat yu xóot yooyu. Biddéew yi ne cell.
Ngelaw li jóg, daldi woy, ay woyam
dekkali jaar-jaaru Maam Ngóor.
Badu, nee ma :
- Maam Ngiraan, loo daan dégg mag ñi di
ko wax ci Maam Ngóor ?
Daa... | DOOMI-GOLO-Ebook-1.pdf |
page_123 | sotti ma ndox mu sedd guyy, caw ma ba
sama yaram wiy nàcc !
Bi Maam Ngóor demee ba màggat, dafa
gàddaaye Siin, dem sanci Tëngéej, takkoo
faak Bintu Jaara. Soxna si jur sama baay
nag, masumaa dégg turam. Doy na waar
gaa, waaye noonu la deme.
Leneen lu ma wax ci Maam Ngóor, ay fen
la.Xanaa boog ma fent...
Maam ... | DOOMI-GOLO-Ebook-1.pdf |
page_124 | damay jàpp rekk ne waa Mbériη-Saaj a
nga tool ya. May wër ba séen benn waa ju
wéeru ci benn sàkket, ma jubal ci moom.
Li nuy nuyoonte yépp, mu ngi may ronni,
naan xam naa, ci xelam :
Kii de, dëkkul fii fépp. Man it, li ma tax a
jële oto Ndakaaru wutali Mbériη-Saaj,
yombul a wax. Mënumaa tëb jaar ci digg
bi.... | DOOMI-GOLO-Ebook-1.pdf |
page_125 | - Aa ! Te nga ne yow jarbaatam nga ?
- Déedéet, sëtam laa.
- Sëtaatu Maam Ngóor tàww !...
- Déedéet. Sëtam laa wax.
- Biraan Fay de, yëguma fu mu amee
doom, bay am sët. Loolu kañ la ?
- Monte li ma wax de, leer na !
Waa ji mer, xaaxtandiku sànni fu sore, jóg
taxaw :
- Aa ! Man ngay gëdd ? Ãa ! Danga ma
teg d... | DOOMI-GOLO-Ebook-1.pdf |
page_126 | - Am na lu ma jot a for ci seen waxtaan
de, man mii.
Ci sama tiitaange, maa ngi xiixat, naan ko:
- Monte samay tànk de, góor gi, tànki
jàmm doηη lañu. Mu muuñ, ma seetlu ni
bët yi dugge. Mu ne ma :
- Bu dee Biraan Fay mi ma foog de,
Tëngéej la faatoo.
- Maam Ngóor lañu ko daan woowe.
- Kon boog mooma. Waaye, l... | DOOMI-GOLO-Ebook-1.pdf |
page_127 | - Man mii de, bitim-réew laa newoon, te
yàgg fa lool. Moo waral sunu gise yéexe
nii. Maa nga woon Milaano, ca Itali.
Foofu...
Góor gi dog ma :
- Dangay kàcc, Ngiraan Fay. Xamoo sax
fu dëkk boobu féete. Maa la gën a xam sa
bopp fuuf ! Mën naa la wax it fan nga
xéye, ne Mbériη-Saaj maa ngoog. Ba ngay
tàllal koks... | DOOMI-GOLO-Ebook-1.pdf |
page_128 | - Gan gii de, ci xeetu Maam Ngóor la
war a bokk... Xanaa kii dafa repp ?
Mbir maa ngoog, Ngiraan. Kon soo fi
tuddatee Milaano, dinaa la def lu bon.
Ma dem bay tontu góor gi, mu të ma.
Sama baat biy lox, ndax ni ma tiite. Ma ne
tekk, di xool góor gi. Gisuma ci moom
dara lu tax ma mën a xalaat ni du nitu
neen. Ku... | DOOMI-GOLO-Ebook-1.pdf |
page_129 | Ma gën a tiit.
Yëf yi du caaxaan... Xawma lan, waaye
loolu moom leer na ma. Mbir mu
kéemaane sax ! Wund wa ma tiimoon
Ñarelaa daldi dellusi ci sama xel. Ma
déggaat ko muy jooy. Góor gaa ngi ma ni
jàkk, di xëcc naanoom. Lu ma koy tontu ?
Am nay kàddu yu benn Doomu-Aadama
sañul a génnee ci gémmiñam.
« Ba àddina... | DOOMI-GOLO-Ebook-1.pdf |
page_130 | - Man de waa ju baax, sa tur rekk laa la
laaj. Gisuma lu waral ngay xas samay
way-jur.
Mu xoolaat ma ba yàgg, ne ma :
- Maam Ngóor laa wax, moo fi yéesoon.
- Aa ?
- Maa wax loolu. Fii ci Mbériη-Saaj, ñépp
xam nañu mbonam. Liir yiy soog a juddu
sax, su ñu déggee turu Maam Ngóor seen
fit rëcc.
Keroog jooju laa ... | DOOMI-GOLO-Ebook-1.pdf |
page_131 | - Nga ne lu deeti say tànk sax, Ngiraan ?
Ma takk sama fit, fas yéenee janook
moom, wax ko nag dëgg. Mas naa
waxtaan bés ak benn boroom xam-xam.
Nu dem ba ci biir wax ji, mu ni ma :
- Doom, gor bu sësee dafa war a fàttaliku
la mag ña daan wax. Laaj ma wax jooju
jan la, doom, ma wax la ko.
- Laaj naa la ko.
- W... | DOOMI-GOLO-Ebook-1.pdf |
page_132 | Booba ba léegi amuma jàmm. Fàww ma
xam maay kan ak fan laa cosaanoo. Nit ku
xamul loolu, yaak xobu garab wi ngelaw
liy ëf, muy wëndéelu ci jaww ji yéen a
yem. Góor gi ne ma jàkk, sama xel dellu
ca wundu Ñarelaa wa. Mu wiccax boppam
ba yàgg, joxoñ ma benn kàdd :
- Séen nga kàdd gale, de ?
- Kàdd gi mel ni lu taf... | DOOMI-GOLO-Ebook-1.pdf |
page_133 | Dem naa ba naan ko :
- Waa Mbériη-Saaj ñoo mën gan ! Waaye
mii xel ne ma xuloo xeju fi te it wax dëgg
Yàlla man lañu jekku woon.
Aa !
Man mi yaakaaroon ne bés bu ma agsee
Mbériη-Saaj, teeru bu mag laa fiy am,
samay mbokk fàqee fu ne daw wutsi ma,
ñépp di ma sargal, maak ñoom ñuy
yuuxoo, di jooy ndax mbégte ak ... | DOOMI-GOLO-Ebook-1.pdf |
page_134 | - Ceddo yi kay ! Li Yàlla xam doy na ! Su
ñu naanaan seeni këlli sëng ba seen yaram
tàng, dañu daan fekk Maam Ngóor fi mu
toog di jàngal gone yi, ñu koy wéq, di ko
saaga, di saw ci kow bopp bi !
- Ana mu tey ? Dëgg rekk mooy dëgg !
Tey de, kenn dootul bàkkoo sama maam
ceddo la woon !
- Du Sëriñ Mbay Jaxate wo... | DOOMI-GOLO-Ebook-1.pdf |
page_135 | Kàddu yooyu soppi kon nañu ma ba
fàww, ma dellu Ñarelaa, nekk keneen.
Ngiraan Fay, sëtu Maam Ngóor, boroom
Mbériη-Saaj. Ku sànc dëkk de, deseelatoo
kenn dara, te Maam Ngóor moo def lu réy
loolu. Su deme woon noonu, sama xol du
diis ba duma ko àttan.
Kon damay toog ci buntu kër gi, waa
Ñarelaa di ma romb di ma n... | DOOMI-GOLO-Ebook-1.pdf |
page_136 | - Nataal yii, seen Maam Ngiraan Fay a
leen jëloon. Booba, kenn ci yéen
juddoogul. Ñarelaa ngi nii, mooy nataal
bu mag bii. Fii laa juddoo, man seen baay
Badu Taal. Gis ngeen ni gox bi meloon bu
jëkk ?
Mbaa :
- Boroom lonet yii janook mbooloo miy
wax, mooy Séex Anta Jóob. Xool-leen ko
bu baax. Dafa mitiηsi woon... | DOOMI-GOLO-Ebook-1.pdf |
page_137 | Soo ko jekkoo gal-gal ko mu daanu mbaa
sax lee-lee nga jam ko paaka, butit yiy
watatu. Ak lu ma mën a wax, man mii ci
baadooloy Ñarelaa yi laa bokk. Du nag lu
ma gënal. Ku ma romb ci sama buntu kër
gii, mën nga ma ne :
- Ngiraan Fay, doo nitu dara, ndax yaa ngi
nii toog Ñarelaa, kaña yeek xaj yu médd
yi wër la,... | DOOMI-GOLO-Ebook-1.pdf |
page_138 | péex mu neex di ma upp. Saa yu ma
gëmmee, fàtte Ñarelaa, daldi gis Maam
Ngóor mu sol mbubb mu weex tàll, di dox
moom kenn ci joor gi. Rabu àll yépp di
jébbalu ci moom, guy gu mu romb nga
yéene ko sa keppaar, gunge ko ba mu àgg
fa mu jëm . Maam Ngóor moom di wéy
rekk, di tudd turu Yàlla, du geestu, du
siggi benn... | DOOMI-GOLO-Ebook-1.pdf |
page_139 | Xawma fan, waaye Mbériη-Saaj gii
moom, soo fi fanaanee du la jig.
- Ba noonu daal, góor gi ?
- Yaa ngoog, yoonu sëg yaa ngoog. Soo
siyaaree ba noppi, jaare fa ñibbi.
- Aa ?
- Man de noppi naa ci wax ji, Ngiraan.
Xam nga, Badu, nit su goree te jaambure,
du gaaw a torox. Bu demee ba sës, Yàlla
dafa koy dooleel.... | DOOMI-GOLO-Ebook-1.pdf |
page_140 | Soo bëggee xam naka la armeeli Mbériη-
Saaj yi mel, gëmmal. Béréb, su nit xamul
fu mu féete, te mu wóor ko ne dina dund
ba dee te du fa xand, bëti xelam a ko fay
yóbbu. Gëmm ngaam, Badu Taal ?
Yaa ngi séen ay kàdd yu dóomu-taal, yegg
ca kow te wow koηη. Ñu ngi tiim ay jali
suuf yu ndaw. Maa ngi wër ak a wëraat ci... | DOOMI-GOLO-Ebook-1.pdf |
page_141 | fatt sama bakkan. Waaye demuma sax bay
tiit.Dina ñuy wax ne :
- Ku la yéene xiif, saa yoo ko rombee
géexal.Noonu doηη la mbir mi deme.
Keroog laa xaare waa Mbériη-Saaj ! Nit
dina tollu fu mu dootul xàmmee boppam.
Moo tax boolewuma ci wax. Dama
làmbaatu ba daj benn xeer wu réy, ma
wéeru ca. Ni ma tooge, mii xel ... | DOOMI-GOLO-Ebook-1.pdf |
page_142 | ma dégg ay tànk yuy yoot ci ñax mi. Fi
ma deme ba naan :
- Kooku ? Am ku ne :
- Man a. Bul tiit.
- Yow a kan ?
- Doo ma ne kañ xàmmee woo sama baat,
Ngiraan... Dafa tudd sama tur rekk, sama
xel ni yarr ci góor ga ma teeru woon ci
bëccëg. Toogagul sax daldi ma ne :
- Naka mu, Ngiraan ? Li doyoon waar,
Badu, li... | DOOMI-GOLO-Ebook-1.pdf |
page_143 | - Baal noonu yow it, Ngiraan. Loolu amul
solo. Ma gën a mer nag, déjuwaat bu
baax, ni ko :
- Góor gi, noo tudd ?
- Tee ngaa bañ a mer, doom ? Man
maay...
(Foofu, wax na ma turam. Su ma ko
fàttalikoo feek ëllëg, dinaa la ko yokkal ci
Téereb Lëndëmtu bii may bind).
- Léegi xam naa sa tur waaye am na lu
des.
... | DOOMI-GOLO-Ebook-1.pdf |
page_144 | - Man kay sañuma laa sóoru, góor gi, nde
tuutee tee nga mat ba baay. Su dee dama
la tooñ, baal ma àq.
- Moo gën ci yow. Léegi nag, wuyu ma :
naka mu, Ngiraan ?
- Wër naa sëg yi lu mat ñetti waxtu,
gisuma fenn bàmmeelu Maam Ngóor.
Ñëw bi ma ñëw Mbériη-Saaj de, amaluma
benn njariñ. Ëllëg ma ñibbi Ñarelaa.
- Bul... | DOOMI-GOLO-Ebook-1.pdf |
page_145 | - Daw naa ay lu ma mën, góor gi, waaye
nag yabeel gaa ngi bëgg ëpp.
Góor gi muuñaat, ne ma :
- Yaa yey jaaxle, Ngiraan. Yóbbal bi ma
lay wax de, ay kàddu doηη la.
- Ay kàddu ?
- Waaw. Du siddéem, du gerte-kemb, du
kóoni, du new, du leneen. Du lu diis looy
yéenu ci naaj wi, di ko dugal ci oto, jëm
ak moom Ñare... | DOOMI-GOLO-Ebook-1.pdf |
page_146 | Ba may reetaan man ci sama bopp,
teyuma ko. Badu, li ngay jàngsi bu ci
kanamee, mooy la ma góor ga wax guddi
googu. Yokkuma ci dara, wàññiwuma ci
dara. Guddig àjjuma la woon.
Tàbbal na ci samay nopp ay baat yu
lëndëm te kéemaane. Ni ma leen jote laa
la leen di jottalee.
Déglul ma boog góor gi ma fàtte turam,
f... | DOOMI-GOLO-Ebook-1.pdf |
page_147 | Lu waral loolu, Ngiraan ? Foo fekk
Doomu-Aadama, ñett yii ma lay limsil
ñooy yatt kanam gi : mer mbaa tiis mbaa
mbégte. Ñett yooyu, bu ci nekk dafa nuy
faral di doxe ginnaaw. Te it, bu ci nekk ba
muy ñëw ak ba muy dem benn lay doon.
Mënoo saa yoo reetaanee mbaa nga mer,
daldi këf sa seetu ngir gis ci naka la sa ... | DOOMI-GOLO-Ebook-1.pdf |
page_148 | Bés a ngi ci bés yi, buy indil Doomi-
Aadama yi njàqare. Askan wi day yeewu
bés, dootul xàmmee boppam.
Ne :
- Li woon, wonni na. Yoon wa maam
xàlloon démb, seey na ci biir géeju fen ak
tappale. Kan moo fi jaar ba soppinu nii ?
Su askan wi joowee ba ci diggu dex gi, bu
sëppoo, seetu, keneen lay gis.
Askan wi ne ... | DOOMI-GOLO-Ebook-1.pdf |
page_149 | - Lan la maam doon sàggan ba ay
doxandéem ñëw di ko daan, di ko toroxal?
Déglu ma, Ngiraan : bu lu ñaaw looluy
am, day fekk xobu garab gi wow koηη.
Ay fan ci ginnaaw rekk, ngelaw li upp na
ko lu yàgg a yàgg. Muy njoowaanu, di
raay asamaan si, di noyyi, féex ba,
tubaarfakàlla. Lee-lee taw bi dal ndànk ci
kowam, ... | DOOMI-GOLO-Ebook-1.pdf |
page_150 | Xobu garab gi dootul saf kenn ba bés ba
muy daanu, di xalangu ci suuf si, tànk bu
fa jëkk a jaar dëggaate ko, mu daldi
soppiku pënd ci saa si. Nun waa Mbériη-
Saaj de, li nu mas a xam mooy teral gan,
yaatal ko. Moo tax jamono ja nga xam ne
lu waay am fit ak doolee la ko may te ku
jekku sa moroom bojj ko paaka, ké... | DOOMI-GOLO-Ebook-1.pdf |
page_151 | Nun Mbériη-Saaj, fa nu newoon démb ak
bërki-démb lanu nekk ba tey. Xobu garab
way wow, ab doxandéem dëggaate ko, mu
dee, pënde, xobu garab woowu du sunu
bos. Fii, Mbériη-Saaj, su xobu garab
xàwweekoo ci kow, daanu ci suuf, joor
gee koy ëmb, di ko aar, di ko tette, ba
nawet fekkaat ko fi, may ko ndox mu
naan, mu... | DOOMI-GOLO-Ebook-1.pdf |
page_152 | Nu tontu ko tontu bu leer :
- Maam kay masul a juum ! Lépp lu mu
nu mas a wax, gis nanu ko. Dunu ko
wecceek keneen de, ak ku mu mën a doon
nag. Maam Ngóor mer, ne nun dunuy nit,
ay ràbi àll lanu. Déggal ma loolu rekk !
Keroog jooju, wax na lu ëpp. Ba sunu
jonn-Yàlla-tey, kàddu Maam Ngóor yaa
ngi riir ci péncum ... | DOOMI-GOLO-Ebook-1.pdf |
page_153 | Waay Maam Ngóor, tee ngaa yem fi nu la
yemloo ! Bi Maam Ngóor déggee loolu,
dafa mel ni ku fit wi rëcc, mu daldi taf
gémmiñ gi, yuuxu :
- Yéen waa Mbériη-Saaj, luy seen yoon ci
biddéew yi ci kow asamaan si ba ngeen
leen di waññi ? Du lii lañuy waxati ? Xaw
ma kuy seen Maam, waaye sànk na
leen.Waa Mbériη-Saaj n... | DOOMI-GOLO-Ebook-1.pdf |
page_154 | Maam Ngóor di ratatati, lee-lee mu làkk
nu làkk wu nu masul a dégg, gémmiñ giy
fuur, muy say, bët yi weex tàll. Magi
Mbériη-Saaj yi gise, ne :
- Kii kat yaram wi neexul, ku ko mere
tooñ ko. Nan ko jéem a faj rekk, moo nu
war.Maam Ngóor ne du ci dal. Nu ni ko :
- Amaana yoon wi nga nuy won sax, bëgg
nu fekk la c... | DOOMI-GOLO-Ebook-1.pdf |
page_155 | Ndekete li nu nekk ci sunuy soxla àddina
yépp, Maam Ngóor a nga doon naan
yóori goney Mbériη-Saaj. Ba mu demee
ba wóolu dooleem, mu jàkkarlook nun, ne
nu :
- Yéen waa Mbériη-Saaj, mu neex leen,
mu naqadi leen, dingeen dox ci sama
waaw ! Ngiraan Fay, sa Maam Biraan Fay
moo nu féewale, tas kër yu mag yi, ba faf ... | DOOMI-GOLO-Ebook-1.pdf |
page_156 | Mu jékki-jékki ne :
- Waaw, ana diw sax ?
Kooku di lox xaat, xam ne bésam ñëw
na.Maam Ngóor joxoñ ko baaraam, dellu
ne :
- Diw mii de, dafa maa bëgg a të. Am na
yu ma dégg ne moo ko wax ci ni Doomu-
Adama bindoo ak li waral ndoxu géej gi
saf xorom.
Ngóor siy yikkat ni gone, di saw tubéyam,
mbooloo miy xàqataa... | DOOMI-GOLO-Ebook-1.pdf |
page_157 | Su doon sama sago, ma jéggal ngóor sii,
waaye yéen a war a dogal ndax yéen laa fi
toogal. Ñépp yuuxoondoo :
- Kii kay Buur, li mu def dafa jéggi dayo,
rendi koo la war !
- Naankatu sàngara bu bon bi !
- Na dee !
- Na dee !
Su ko defee, ay sàmbaa-bóoy jóge fale,
dóor waa ji ba mu sedd ci seeni loxo, ñu
jagat-j... | DOOMI-GOLO-Ebook-1.pdf |
page_158 | Maam Ngóor dafa nu móolu, nu móolu
ko. Nun, sunu maam bu daan xareji, segg
la daan war ! Waaw, bu sànneekuwaan ci
jaww ji, ngelawam kese daan na rotal ay
junniy-junni biddéew, jën yi ci biir géej
tiit, daw wuti fu ñu làqu. Kon kay nga
xam ne du ηexalub naaru-góor doηη mooy
yóbbu sunu fit, nun waa Mbériη-Saaj ! B... | DOOMI-GOLO-Ebook-1.pdf |
page_159 | Dofunu de, Ngiraan, nu ngi teg sunuy bët
ci li xew, nu ngi gis ni àddina siy doxe,
waaye taxul nu saalit bay pasar-pasaree li
nu Maam dénk. Waxuma feneen de,
Mbériη-Saaj laay wax ! Yow nag, xeer wii
ngaa wéeru di ma déglu, làyyi biy dugg ci
sa biiri yax, lu mu metti metti, mooy sa
jàmmu yaram, nde soo juumoon ba... | DOOMI-GOLO-Ebook-1.pdf |
page_160 | TÉEREB DÓOM
II | DOOMI-GOLO-Ebook-1.pdf |
page_161 | Léegi yaa ci des, Badu. Xamal ne Mbériη-
Saaj du sa jëmu. Gis naa it ni Téereb
Lëndëmtu ubee sa bopp. Bi nga ko jàngee
ba noppi, téye nga ko lu yàgg, sog ma ni :
- Ngiraan, juum nga, de.
Ma yëngu ndànk fi ma tëdd ci sama biir
bàmmeel, daldi la ni :
- Ci naka, Badu ?
Nga xàmmee sama baat, fu ne nga geestu
fa, gi... | DOOMI-GOLO-Ebook-1.pdf |
page_162 | Tëdd laaxira bumu tax nga mel ni ku
xamul li géej giy riir. Lépp loo xam ci
yow ak ci say way-jur, guddi googu nga
ko jàng. Say kàddu jaaxal ma lool. Ma
xalaat ci ba yàgg, ma laaj la lu wax jooju
tekki. Nga ne ma :
- Du nee nga Maam Ngóor, dëkk na
Mbériη-Saaj ay ati-at ?
- Looloo am, Badu.
- Tëngéej ga ñu ko d... | DOOMI-GOLO-Ebook-1.pdf |
page_163 | Su ñu waxantee dëgg, Badu, waa Mbériη-
saaj lii lañu ma jàngal : ku bëgg xam sa
bopp, fàww nga takk sa fit. Lu ruq
lëndëm-lëndëm, bu ca ragal a dugg. Soo
ko defee, dinga làngi bés ak ki jur maamu
Maam Ngóor.
- Aa, Ngiraan, yen bi nga ma yen gën a
diis !
- Déggoo wax ji, Badu ! Yen bi taxu koo
diis. Maam Ngóor m... | DOOMI-GOLO-Ebook-1.pdf |
page_164 | Jàppe ma ni ab fecckat, man Ngiraan mii
ubbiwaat sànq Téereb Dóom, sëgg ciy
bind. Maa ngi wëndéelu ci biir géew bi,
am ñu may tëggal sabar te duma leen gis.
Bu gaa ñi rëkkee, ma tëb ba àgg ca kow
asamaan, ñu wàcce ma ndànk, rëkkaat ba
yàgg ne tekk. Samay kàddoo leen di awu.
Su ma nee tekk ñu jëlaat, daldi rëkk, ... | DOOMI-GOLO-Ebook-1.pdf |
page_165 | - Mbisaan yow, ana nga ? Kaay fii ! Ana
Mbisin ?
Am ku ko tontu :
Ana ñu sax, sunu ñaari doomi tubaab yi ?
Ñoom de, ñu ngi fi woon sànq ba tey !
Ngóone Cuun daldi yuuxuwaat :
- Mbisaan ! Mbisin !
Mbisaan génne fu kenn xamul, agsi, ñëw
ba ci kanamu Ngóone Cuun, téen, ne ko
jàkk ba yàgg mu këdd suuf seek tànku ... | DOOMI-GOLO-Ebook-1.pdf |
page_166 | Ngóone Cuun woo benn gone, laaj ko :
- Mu ne lan ? Gone gi ree, ne ko :
Mbisaan mii kat, waxam daa gaaw, dinaa
ko dégg muy wax waaye duma xam lu
muy ratatati ! Noonu mu walbatiku, xool
Mbisaan, ni ko :
- Répète ce que tu as dit !
- Ma soeur est sourde, ce n’est pas la
peine de crier son nom comme ça ! C’est
t... | DOOMI-GOLO-Ebook-1.pdf |
page_167 | Soo ko gisee, mu ngi xonq ni naaru-
gànnaar. Sa ñaari doomi baay yooyu nag,
nit ñaa ngi ηuη-ηuηi, naan seen ndey
Yaasin Njaay dafa xaw a dese. Fi ma
taxaw ak Yilimaan Keeta, gis naa la ngay
diisoo ak sa yaay Biige Sàmb. Ma ne ci
sama xel : « Àddinaa doy waar ! Ba fi mu
ne daal, ñu ngi waaj a denci Asan Taal ! »
... | DOOMI-GOLO-Ebook-1.pdf |
page_168 | Xanaa lii mooy ñu lay tam dëmm ngay
soccoo yeelu liir ! Ténju Yaasin Njaay bee
ka kéemaane ! Mu ngi téju biir néegam,
ne du wax ak kenn. Ca njëlbéen ga, danu
defe woon sax ne naqar wu mettee taxoon
mu jàpp noonu njaamburam. Waaye man
mii jokkook moom bés ba Asan Taal
faatoo, gise woon na neneen mbir mi.
Yaasin ... | DOOMI-GOLO-Ebook-1.pdf |
page_169 | - Demunu Gànnaar waaye xam nanu ne
guddi lañ fay reer !
- Maa la ko wax !
- Ñaaw ba nga ni lii lu mu doon !
- Moo yey di làq kanamam.
- Soo yëkkatee sa benn loxo ne
faalewuma kenn, yëkkatil bi ci des ne
kenn faalewu ma.
- Lu ne gis nanu ko Ñarelaa waaye guléet
jigéen juy ténj sañ fee def lu ni mel ! Wax
jooj... | DOOMI-GOLO-Ebook-1.pdf |
page_170 | Yaasin ne ma :
- Loolu ngay wax, Ngiraan ? Xoolal,
Ngiraan ! Ma ne : góor gi, xullil fii !
Ma siggi, gis Yaasin Njaay tiim ma, tas
séram, joxoñ ma këfinam, xulli bët yi, te
naan ma :
- Lii, maa ko moom, lu ma neex laa ciy
def, ku ma neex laa koy ràccal ! Bi samay
nopp déggee baat yu ñaaw yooyu, samay
bët tegu ... | DOOMI-GOLO-Ebook-1.pdf |
page_171 | di xawaare, yëf yi xumb ba dee. Sama xel
dellu ca alxames ja nu demee ayeropoor
jëli néewu Asan Taal, Móodu Siise jóge
moom it bitim-réew ak ndam lu réy...
Yaasin Njaay a ngi la ko sàñseel ba nga ne
lii lu mu doon ! Jabu, benn doomu-
bàjjanu Asan, muñ ko ba mënatu koo
muñ, mu daldi fekki Yaasin fi mu toog, di
k... | DOOMI-GOLO-Ebook-1.pdf |
page_172 | Daan nga sa doole moom, Asan Fay Taal,
doomu Ngiraan Fay ak Ndàmbaaw Jóob !
Léegi nag, dem nga sa yoon bàyyil nu fi
ñaari banti-maam-Yàlla yii nga xam ne
duñu yàpp, duñu jën !
Am ku ko ne :
Waaw Jabu, loo xewle ? Ku mus a gis lii ?
Bésu tey bii de, wàcce kaamil moo ci
jekkoon, kenn séentuwu ci woon wax ju
ñaa... | DOOMI-GOLO-Ebook-1.pdf |
page_173 | kenn ci ñoom geestu nanu, xam naa xelam
dem fu sore, mënu koo muñ, mu jàpp
boppam, yuuxu :
- Biige Sàmb, yaay gor ! Muñal rekk, nde
séytaanee yàq sa digganteek Asan Taal !
Waaye Yàlla waxul kenn dara ! Biige
tamit a ngay daanu gangiri ca geneen wet
ga. Nit ñi wër ko, naan :
- Biige, gëmal Yàlla ! Jullit day nan... | DOOMI-GOLO-Ebook-1.pdf |
page_174 | mu mer, xulook yow. Fi Biige Sàmb tëdd,
mu ngi say ak ay yëreem yu xottiku,
kanam gi newwi, ñu koy tuur ndox mu
sedd. Soo ko gisee, mu ngi gajj yaram wi
yépp ba muy nàcc. Yaasin ak ay xaritam
yokk misig bi ba mu sës. Foo tollu di dégg
Móodu Siise muy woy « Mbëggeel ».
Ma daldi xunn, ne ci sama xel : « Xanaa
... | DOOMI-GOLO-Ebook-1.pdf |
page_175 | Kenn fekkewul guddi ga :
- Bëgg naa la ak
- Maa la raw jëkkee dox seen diggante.
Kenn xamul lu tax seen ñaari yaram dem
bay maasaloo ci lëndëmug Màrsey.
Ci biir wax ji nag, am na yu senn ci sa
mbirum baay. Nee ñu Asan Taal
nekkewul woon Tugal lu dul wër ak fo.
Dégg naa ne futbal ba ka taxoon a dem
Màrsey am... | DOOMI-GOLO-Ebook-1.pdf |
page_176 | Xawma ndax loolu am naam amul. Su la
ko jaralee, gëstulal mbir moomu sa bopp.
Ñaari doomi Asan Taal yi jot a ñëw
Ñarelaa daal laa xam ne amuñu yar,
amuñu teggin. Jarul làq-làqal, Badu :
Mbisin ak Mbisaan, ni seen golo lañu ma
jàppe, man seen Maam. Lee-lee Mbisaan
déey dara rakk ji, kooku ñëw fekk ma fi
ma toog,... | DOOMI-GOLO-Ebook-1.pdf |
page_177 | - Aa ? Ci lan ? Ni mu dëgëralee baat bi tax
na tuuti kon ma balu ko àq, dellu toog ci
ëtt bi.
- Mbisaan de, saa yu ma fekkee may julli,
su ma sëllaxulee suuf, saw na ci sama
kanam.
- Xanaa dañu diy gone rekk moo tax, nde
man mii di seen ndey, duma def loolu. Fi
ma nekk sax, dama jàpp góor gi. Su ma
amee jot, d... | DOOMI-GOLO-Ebook-1.pdf |
page_178 | te kon dinañu ko gaañ ndax mer mi ñu ko
dencaloon. Ma xam ne muñ moo ma
war.Ma ni ko :
- Yaasin, Asaan Taal dem na te am na ñu
ko jiitu armeel ya. Kenn ci nun dëkkul ci
kow suuf si. Danu fi jaar rekk. Yàlla def
na maa fi des ak yéen. Dama leen di
gunge doηη, yaak say doom, ngir sàmm
sama digganteek Asan. Tee no... | DOOMI-GOLO-Ebook-1.pdf |
page_179 | - Kon boog, baax na.
Ci buntu néeg bi, daje naak Tamsiir Ba mi
Yaasin Njaay ne doomu-bàjjanam la.
Na ma Yàlla baal, waaye Tamsiir Ba
niruwu ma daraak nit ku yiw. Su la nee
jàkk, li ngay jëkk seetlu ci moom mooy ni
karaw geek bët yi xonqe. Xam naa wérul,
ndax ci moom rekk laa mus a gis lu ni
mel. | DOOMI-GOLO-Ebook-1.pdf |
page_180 | TEEREB FENT | DOOMI-GOLO-Ebook-1.pdf |
page_181 | Fu la jant biy tiime, Badu Taal ? Mbaa
réew ma nga nekk kenn sonalu la fa ? Ku
am jom nga, waaye sa moroom yiy daani
seen doole bitim-réew, dañu leen di faral a
jàppe ni ay jaam, coono bu nekk ñu leen
koy teg. Góor-góorlul, te xam ne fu ma
tollu maa ngi lay ñaanal.
*
* *
Téereb Fent bi nga téye tey nag di ... | DOOMI-GOLO-Ebook-1.pdf |
page_182 | Séentu naa fi ay jàmmaarloo yu mettee-
metti. Deret dina fi tuuruji. Maa ngi dégg
jirim yi ñuy jooy.
Aakimu.
Maa tey.
Jaay doole.
Jalgati.
Ma ne : njiitu réew maa ngi tas réew mi!
Ku nekk a ngi ηàbb sa tojitu réew, sàmp
sa raaya ci sa toolub yàmbaa, ne yaa fay
dogal. Daawur Jaañ, tëj nga géej gi kaso,
fatt ng... | DOOMI-GOLO-Ebook-1.pdf |
page_183 | waaye gone gu ndaw sax bu jàngee li ma
bind, dina xam ne Daawur Jaañ laa tudde
Dibi-Dibi, ci Téereb Fent bii. Ni ma
weccaatlee turi béréb yi tam mënul a
réeral kenn. Yàlla tere tereeti ko, waaye
du ñàkk askan wi nekk ëllëg ci fitna. Su
boobaa, na nga jàngaat téere bii bu baax.
Dinga fekk ci biir njaaxum yi fi Da... | DOOMI-GOLO-Ebook-1.pdf |
page_184 | Ñépp jóge nañu Guy-Géwél, daw wuti fu
ñu làquji. Ñetti at a ngi kanu yiy dal, kër
yeek isin yiy tàkk, reyante bi metti lool.
Waaw, ñan ñooy xeex sax ? Loolu nag
moo doy waar : kenn xamul ñan ñooy
xare. Koo laaj, mu ne la :
- Gone ya doon dox doxu ñaxtu de, ñoo nu
yóbbee lii lépp !
- Njiitu réew mee matul njiit... | DOOMI-GOLO-Ebook-1.pdf |
page_185 | Ñu dem buntu kër Dibi-Dibi, njiitu réew
mi, ngir yëgal ko seen naqar, mu jéem koo
saafara. Ba ñu taxawee foofu di xaar,
goney daara ju mag ji fekk leen fa,
tàmbalee xumbal, ne ñoom it dañuy
jàppale seeni jigéen ak seeni bàjjan.
Noonu, saay-saay tamit daldi jóg taxaw ne
kenn du leen bàyyi ginnaaw. Bés, ñu yéeg
c... | DOOMI-GOLO-Ebook-1.pdf |
page_186 | JAFUNE : LÀRME BI BÓOM NA 137
NIT...
COOW JIBATI NA CIM RÉEWU
AFRIG !
Ay nag, nee nañu du yem ci boppu
boroom... Góbi yi nekk ci làrme bi, te
nguuru Dibi-Dibi ameeloon leen peyu
ñaar-fukki weer ak juróom-ñeent, daldi
yëg seen doole ne ñoom tamit dañuy amal
doxu ñaxtu. Ca la Dibi-Dibi tiite, yaakaar
ne dafa ... | DOOMI-GOLO-Ebook-1.pdf |
page_187 | lanu gëj a xam nu yëf yi deme. Ñetti at a
ngii nu nekk ci fitna, te nun xamunu ñan
ñooy xeex ak lu waral reyante bu ni
mettee. Gànnaay yaa ngi ne gàññ ci réew
mi. Ñi fi nekkoon di politig ciy jamono,
ku ñu ci reyul, yaa ngeek sa làrme bopp.
Dangay dégg bés ne diw ak diw ñoo far,
su ëllëg saa ñu ne la seeni nit a... | DOOMI-GOLO-Ebook-1.pdf |
page_188 | Ñu naan :
- Tundu Ñambaas, rey nañu fa démb rekk
lu war a tollu ci junniy Doomi-Aadama.
Mbaa nga dégg ku ni :
- Talaata jee ñu génn, taal nañu kër
gornooru diiwaanu Maymaydo. Lakk na
ba jéex dara desatu fa. Gornoor ba dafa
daw mook njabootam, nde su leen fa fippu
yi fekkoon def leen lu ñaaw !
Tàkkusaan soreet... | DOOMI-GOLO-Ebook-1.pdf |
page_189 | Lépp li waa Guy-Géwél mën a dajale ci lu
ñuy lekk def nañu ko ciy leket mbaa ñu
ëmb ko ciy mbuus. Daw-làqu yaa ngi bare
ba foo sànni mbàttu mu tag. Waaye ñu ngi
ne tekk. Ku ci nekk a ngi tiit ba talul
waxtaan, waxatumaak naan day kaf mbaa
muy reetaan. Aatu Sekk di leen xool ñuy
génn Guy-Géwél ba ne tuuti mu may ... | DOOMI-GOLO-Ebook-1.pdf |
page_190 | - Góor gi Aatu, xanaa yëgoo li xew ?
- Yëg naa ko sax de. Réew mi daanaka jur
gu médd la. Till ak Bukki ak Segg fees
nañu ko, ku nekk ηànk wàllam di wéy, di
yéy.
- Loolu kay taxul may wax, góor gi ! Daa
am ñuy waaj a song Guy-Géwél.
- Ñooñu ñana ?
- Xam ! Ci li nit ñiy wax daal, xare bi ñuy
waajal fii dina m... | DOOMI-GOLO-Ebook-1.pdf |
page_191 | - Soo jullee, ñaanalal njaboot gi, Aatu.
Aatu Sekk a ngi ηàbb yatam, mel ni kuy
miir xamatul lan lay wax. Deret moo am
doole !
- Mbaa saay-saay si sonaluñu leen rekk ?
Ni ko Omar xoole, mu xam ne jëli na
ko.Omar sañu koo wax ne xaj yee leen
mujjee jiiroo.Dafa ko ne rekk :
- Góor gi Aatu, nanu dellu kër ga, nga... | DOOMI-GOLO-Ebook-1.pdf |
page_192 | - Mukk ci àddina, Aatu ! Waaye waxtaan
xeju fi. Omar xamul fu mu jëm, waaye
fitam jiitu na ko fa bu yàgg. Moo tax su
nit tiitee ba tàggook sagoom, mbokk yi
naan :
- Diw de, fit wi dafa rëcc.Day fekk booba
jëmm ji nekk fi, mbokk yi janook moom
te muy xottu nit doηη. Omar Jaw a ngi
ñaq bay siit, tuñ yi wow koηη,... | DOOMI-GOLO-Ebook-1.pdf |
page_193 | Waaye fi lañu nuy fekk, dunu seetaan
loolu, dinanu ko defanteek ñoom ba mu
saf sàpp ! Bi Aatu fàttalikoo kàdduy
Omar yooyu, tuutee tee mu xaqataay.
Waaye mu ngi yërëm Omar Jaw be,
ndeysaan. Mu daldi ne ko :
- Omar, tàllalal sa loxo, ma ñaanal la. Tey
lanuy mujjee gise maak yow, ndax fi mu
ne nii taxaw nga te m... | DOOMI-GOLO-Ebook-1.pdf |
page_194 | Ñetti fan a ngi, mburu mu wow lay dunde.
Dute ji jeexagul waaye li des ci këriñ gi
bareetul. Balaa yàgg, dootul lekk lu ñu
togg ci cin, dootul naan lu ñu tàngal. Guy-
Géwél a ngi ne selaw.
Ci tisbaar, doxantu na ci ëtt bi lu mat
waxtu. Mu ngi sog a seetlu ni kër gi
bindoo. Bunt bu mag bee ko féete
càmmooñ. Soo ... | DOOMI-GOLO-Ebook-1.pdf |
page_195 | xeex bi neeti kurr. Góor gi Aatu Sekk ne
ci xelam :
« Céy, Afrig moo sonn ! »
Benn jinax ñëw na ba riisu ko. Bi waa
Guy-Géwél gàddaayee ba tey, kër gi yépp
ay jinax laak ay kaña. Foo geestu séen ci
ñaar mbaa ñett ñuy wut lu ñu lekk, fu ne
ñu dugg fa. Picc yi tamit bare nañu lool ci
garabi Guy-Géwél yi. Góor gi ... | DOOMI-GOLO-Ebook-1.pdf |
page_196 | Tuuti suukar.
Butéelu lem.
Butéelu tiir.
Li gën a soxal Aatu Sekk mooy ndax dese
na këriñ. Wër na kër gi yépp, fu nekk mu
seet fa waaye gisul fenn këriñ. Nu muy
def nag, léegi ? Xanaa wuti ko ci gox bi.
Gënalu ko de, wax dégg Yàlla, waaye
fàww mu dem ci yeneen këri Guy-Géwél
yi, fortaatu fa këriñ ak lu mu lekk... | DOOMI-GOLO-Ebook-1.pdf |
page_197 | Guy-Géwél a ngi ne selew booba ba tey.
Lee-lee góor gi Aatu Sekk di waxtu ngir
wéttalikoo baatam. Ku sañoon a xalaat ne
bés dina ñëw Ruq Jinne mel ni nit masu
fee dëkk ? Ruq Jinne, nga xam ne moos ci
xuloo, xeex ak jamante paaka la gone yiy
juddoo, màgg ci, yaroo ci ? Góor gi Aatu
Sekk àgg na bitigu Jàllo.
Ñu ... | DOOMI-GOLO-Ebook-1.pdf |
page_198 | Góor gi Aatu Sekk a ngi taxaw ci diggu
àtte-tooñ bi goney Guy-Géwél yi daan
daje di futbal. Fépp fu nit ñi daan dajaloo
- muy robine yi, di garaη-palaas yi mbaa
feneen - ay ndab ak ay toogu ñu nga fa
tasaaroo. Xanaa ragal ñu diisal leen a tax
waa Guy-Géwél sànni leen fi dem. Ci
buntu sinemaa Palaas, gis na benn... | DOOMI-GOLO-Ebook-1.pdf |
page_199 | Bi mu rombee sëni Guy-Géwél yi, séen na
ay dogitu mburu yu ñu fa sànni. Dem na
ba leen di for, ngoram mayu ko ko, mu
daldi wéy. Xiif du ko tax a saalit bay lekk
ñamu-mbaam. Ndax, kat :
Ku mar tax a naan pótit, bu ndox tuuroo
nga rus.
Góor gi Aatoo ngi jaaxaan ci taatu niim gi
ci ëtt bi.Mu ngi miir. Bopp baa ngi... | DOOMI-GOLO-Ebook-1.pdf |
page_200 | Ndax xel mën naa nangu loolu ? » Rajo bi
fey, tàkkaat, di xor-xori ba yàgg, waa ji
gënatee yuuxu :
«...juddoo fi... doom ak i jarbaat... jox lay
ngànnaay ngir toroxal nu ? Waaye...Dibi-
Dibi, askan wee ko wóolu, jiital ko te fas
yéenee ànd ak moom defar réewu Jafune...
Dibi-Dibi, njiitu réew mi, nee na... »
Raj... | DOOMI-GOLO-Ebook-1.pdf |
Subsets and Splits
No community queries yet
The top public SQL queries from the community will appear here once available.