url stringlengths 6 8 | content stringlengths 2 3.72k | source stringclasses 3
values |
|---|---|---|
page_510 | 510
Saar 78 : XIBAAR BA
40 - Laaya – Ginnaaw Gàddaay ga
-----------------------------------------------------------------------------
Ci turu Yàlla Yërëmaakoon bi, Jaglewaakoon bi.
1. Ana ci man mbir la ñuy laajante ?
2. Ci xibaar bu rëy ba,
3. xibaar ba nga xam ne dañu caa juuyoo.
4. Mukk ! danañu... | coran-wolof.pdf |
page_511 | 511
12. tabax nanu juróom ñaari (asamaan) yu dëgër ñu tiim leen,
13. poose nanu ci làmpu bu leer (jant bi),
14. wàcce nanu ci niir yi am ndox muy dottiku
15. ñu di ca saxal ay pepp ak i gàncax
16. ak ay dër yu naat.
17. Bisub Àtte ba Dig ba jotna.
18. Bis ba ñuy wal bufta, ngeen di ñëw di ay mbooloo, ... | coran-wolof.pdf |
page_512 | 512
27. Ñoom dañoo foogoon ne duñu leen màndaxe,
28. ña weddiwoon sunuy Laaya,
29. lépp lu ne peek nanu ko bind ko.
30. Ayca mosleen. Dunu leen dolli lu dul mbugël (tokamtikuleen ko)!
31. Ña ragal Yàlla ñoom baaxal nañu :
32. am nañu ay tooli dër ak i reseñ,
33. ak i jongama huur yu taxaw ay ween te m... | coran-wolof.pdf |
page_513 | 513
Saar 79 : MALAAKA YAY ROCCI RUU
46 - Laaya – Laata Gàddaay ga
-----------------------------------------------------------------------------
Ci turu Yàlla Yërëmaakoon bi, Jaglewaakoon bi.
1. Ci roccikat yay sanjaafu, maa ngi giñ !
2. Ak ña koy rocci ndànk-ndànk !
3. Ak ñay féey ca asamaan sa,
... | coran-wolof.pdf |
page_514 | 514
12. Ña ngay wax naan : “loolu deey yàqule la ! ”
13. loolu ab jàjj la,
14. ñu jekki-jekki rekk ne jaww ci kaw suuf si dekkiwaat.
15. Ndax waxtaanu Muusaa dikkël na la ? Ay xibaaram ?
16. Ba ko Boroomam di woo, ca xuru Tuwaa, wu sell wa, di ko wax ne :
17. “Demal ca Firawna. Moom bew na !
18. Te ... | coran-wolof.pdf |
page_515 | 515
27. li ngeen sos moo gëna dëgër ? walla asamaan si ma tabax ?
28. Kaweel na talaayam ba, te maasale ko ;
29. Moo lëndamal guddi yi te leeral bëccëg yi.
30. Ginnaaw loolu moo tallal suuf si :
31. Mu génnee ca ndox ak i gàncax,
32. mu saxal ca duutan ca tund doj yi,
33. mu di bànneexu, ci yéen ak ... | coran-wolof.pdf |
page_516 | 516
42. Ña nga lay laaj bis pénc ba : “Kañ lay teeral”
43. Ana ban xam-xam nga ci am ngir tontu leen ?
44. Ab yemukaayam sa Boroom rekk ko xam.
45. Yaw nag ab xuppekat doŋŋ nga ngir ña ko ragal.
46. Bis bu ñu ko gisee, dafay mel ne seen dund gépp genn ngoon la woon walla yoor-yoor.
-------------------... | coran-wolof.pdf |
page_517 | 517
6. ba tax nga jublu ko.
7. Lu laak moom ? (yaw muhammadu) ”
8. Waaye ku la dikkëlati
9. tey wuta ragal Yàlla,
10. te faalewoo ko.
11. Loolu dey ag fàttali la
12. ku mu soob, mu fàttaliku ko
13. mi ngi ci ay xët yu ñu teral (bind ko),
14. yu ñu yékëti, te laabal ko,
15. nekk ci yoxoy ak ... | coran-wolof.pdf |
page_518 | 518
21. daldi koy rey, tàbbal ko ci bàmmeel ;
22. te saa su Ko soobee mu dekkalaat Ko.
23. Déedéet ! [Nit] moom matalul mukk la nu ko digëloon.
24. Na nit di xool ci aw ñamam lekkam :
25. Nun noo sotti ndox mu dottiku,
26. ba noppi Nu xar suuf mu fett
27. nu saxal ci ay kembu,
28. ay reseñ ak i l... | coran-wolof.pdf |
page_519 | 519
36. ak soxnaam ak doomam,
37. kenn ku nekk, bu keroogee, am mbir mu ko doy sëkk.
38. bu keroogee, ay xarkanam yu naat,
39. bég lool tey ree.
40. Bu keroogee, am it, ay xarkanam yu fundóoñ,
41. lëndëm kariis.
42. Ñooña ñoo di yéefar ya, di kàccoor ya.
------------------------------------------... | coran-wolof.pdf |
page_520 | 520
4. ak saa su nu, sàgganee geleemam ga ëmbu ba sori talatuñu ko,
5. ak ndokmenta ya (rab yu aaytal ya), dajaloo ñu dekkalaat leen,
6. ak saa su ñu taalee geej ya mu di safara,
7. ak saa su ñu lëkëlee ruu ya
8. ak saa su ñu laajee doom ju jigéen ja nu soloon te fekk muy dund, ngir daw gàcce
9. ci ban... | coran-wolof.pdf |
page_521 | 521
19. Ci ne [Alxuraan jii] waxi ab Yonent la bu tedd (Jibriil),
20. di boroom kàttan gu rëy, di ab xejj fa Boroom ganganaay ga Aras,
21. di ku ñuy digël, ndigëlam ca kaw, di ku ñu woolu.
22. Te seen àndandoo ja (Muhammad) du ab dof de ;
23. moom gis na tigi (Jibriil), ca asamaan ya
24. te moom nayul ... | coran-wolof.pdf |
page_522 | 522
Ci turu Yàlla Yërëmaakoon bi, Jaglewaakoon bi.
1. Saa su asamaan si dogee, Maa ngi giñ
2. ak saa su biddew yi tasaaroo,
3. ak saa su géej yi taqaloo,
4. ak saa su bàmmeel ya jaxasoo,
5. bakkan bu Yàlla sàkk xam na la mu jëkkoona def ak la mu mujja def.
6. Éy yaw nit ! Ana lan moo la fàbbi ci sa ... | coran-wolof.pdf |
page_523 | 523
15. danañu ca xoyomoo, bu bis Pénc baa
16. te ñoom manuñu koo wuute.
17. Ana lu lay xamal luy bis Pénc ?
18. Ak lu lay xamal waay, luy bis Pénc ba ?
19. moo di bis ba benn bakkan dul manal moroomam tus. Te bu keroogee, Yàlla rekk ay joxe
ndigël yi.
-------------------------------------------------... | coran-wolof.pdf |
page_524 | 524
6. bis ba nit ña di taxaw ci kanam Boroom Àddina si yépp ?
7. Déet... ! Waaye téereb kàccoor yaa nga ca Sijjin de
8. ana lan moo lay xamal luy Sijjin ?
9. ab téere la bu ñu xas tàmpe.
10. Bu keroogee, weddikat ya, danañu tàbbi xuru safara,
11. ña daan weddi bis Pénc ba.
12. te kenn, du ko weddi ... | coran-wolof.pdf |
page_525 | 525
21. Ña jege Yàlla koy seede (Malaaka ya).
22. Ñu baax ñaa nga ca biir xeewal,
23. ña nga ne toŋŋ ca kaw toogu ya, di xool.
24. Danga seere ca seen xarkanam ya, naataangey xéewël ya.
25. Ñu nandalu ci sàngaras àjjana suñu xàmmee,
26. tem-temam misk lay doon. Ñiy rawante nañu rawante [ci am ko]
... | coran-wolof.pdf |
page_526 | 526
36. Moo ndax yéefar ya am nañu yoolub la ñu daan def ?
-----------------------------------------------------------------------------
Saar 84 : XOTTIKU GA
25 - Laaya – Laata Gàddaay ga
-----------------------------------------------------------------------------
Ci turu Yàlla Yërëmaakoon bi, Jaglewa... | coran-wolof.pdf |
page_527 | 527
10. Képp koo xam ne nag moom da ñu koo jox téereem ci ginnaawam,
11. Ngalla moom kon,
12. te dana xoyomoo safaraw Sa’iir.
13. Moom ku bégoon la cag njabootam,
14. foogoon na ne du dekkiwaat mukk.
15. Axakañ boroomam daan na ko gis de.
16. Déet !... Maa ngi giiñ ci yeeri ji,
17. ak ci guddeek... | coran-wolof.pdf |
page_528 | 528
25. Ba mu des ña gëm tey jëf yiw : ñoom am na ñu pey gu dootul dog.
-----------------------------------------------------------------------------
Saar 85 : BIDDIW YU MAG YA
22 - Laaya – Laata Gàddaay ga
-----------------------------------------------------------------------------
Ci turu Yàlla Yë... | coran-wolof.pdf |
page_529 | 529
9. Yàlla mi moom nguurug asamaan yeek suuf si. Te yàlla seede la ci lépp lu ne.
10. Ña daan fitnaal jullit yu góor yaak yu jigéen ya, te tubu ñu ko, dananu am mbugëlum
Jahanama ñu di leen ca lakk. (ca safaraam wa)
11. Ña gëmoon te daan jëf yiw am nañu ay Àjjana yu ay dex di daw ci suufam. Loolu moo di
texe ... | coran-wolof.pdf |
page_530 | 530
Saar 86 : BIDDIWUB GUDDI BA
17 - Laaya – Laata Gàddaay ga
-----------------------------------------------------------------------------
Ci turu Yàlla Yërëmaakoon bi, Jaglewaakoon bi.
1. Ci asamaan ak biddiwub guddi ba! Maa ngi giiñ
2. Ana lan moo lay xamal luy biddiwub guddi ba ?
3. moo di biddi... | coran-wolof.pdf |
page_531 | 531
12. ak ci suuf siy toj sax gàncax !
13. Alxuraan dafay teqale dëgg at fen,
14. du ay kafi mbóosóor !
15. Ña ngay fexe ay pexe,
16. Man it Maa ngi fexe ay pexe.
17. Éy yaw Yonent muñalal yéefar yi : xaarleen as ndiir.
-----------------------------------------------------------------------------
... | coran-wolof.pdf |
page_532 | 532
5. di ko naatal dëlël ko.
6. Dananu la jàngal (Alxuraan), te doo too ko fàtte
7. lu dul la soob Yàlla. Moom moo xam li feeñ ak li nëbbu.
8. Dananu la jàppandalal yoon wi gëna yomb.
9. Na ngay fàttelee, saa su fàtteli amee njariñ.
10. képp kuy ragal (Yàlla) na nangoo fàttaliku,
11. ñu texeedi ñaa... | coran-wolof.pdf |
page_533 | 533
-----------------------------------------------------------------------------
Saar 88 : MUURAAKOON BA
26 - Laaya – Laata Gàddaay ga
-----------------------------------------------------------------------------
Ci turu Yàlla Yërëmaakoon bi, Jaglewaakoon bi.
1. Moo ndax yaw waxtaanu muuraakoon ba dik... | coran-wolof.pdf |
page_534 | 534
11. doo fa degg mukk waxi caaxaan.
12. Am na fa, bëtu ndox buy daw-dawaan.
13. Am na fa, ay lal yu kawe
14. ak ay kopp yu ñu teg
15. ak ay ngegenaay yu ñu sësële
16. ak ay laltu yu ñu lal.
17. Xanaa dañoo xoolul ci giléem, naka lañu ko binde,
18. ak ci asamaan si naka la nu ko yékëte,
19. ... | coran-wolof.pdf |
page_535 | 535
26. Ba noppi, te nun it nooy warloo laaj leen.
-----------------------------------------------------------------------------
Saar 89 : NJËL
30 - Laaya – Laata Gàddaay ga
-----------------------------------------------------------------------------
Ci turu Yàlla Yërëmaakoon bi, Jaglewaakoon bi.
1... | coran-wolof.pdf |
page_536 | 536
10. ak Firawna, ma doonoon boroomi dàtt ?
11. Ñoom, ñoo gënoona bew ci réew yi,
12. te ñu bariloon fa lool ag yàq.
13. Sa Boroom daldi leen sotti yarum mbugël.
14. Sa Boroom nag ma ngay fuglu.
15. Nit nag, moom saa su ko boroomam nattoo teral ko xéewal ko, mu ne : “Sama Boroom
teral na ma”.
16... | coran-wolof.pdf |
page_537 | 537
24. Muy wax naan : “Aka neexoon ! Ca ba muy dundu ma defoon lu baax !
25. Bu keroogee, mbugël ma deefu ko mbugël kenn,
26. te it kenn du yolomal jéngam ba.
27. “Éy yaw, bakkan bi dalum xel,
28. delul ca sa Boroom, di gërëm ñu dila gërëm ;
29. tàbbil ca Samay jaam,
30. tàbbil it ca Sama biir ¨Àjjan... | coran-wolof.pdf |
page_538 | 538
4. Noo, bind nit muy jànkonteeki coono.
5. Moo ndax dafa defe ni kenn manul ci moom dara ?
6. Ma ngay wax naan : “Sànk naa alal ju bari”.
7. Moo ndax dafa defe ne kenn da koo gisul ?
8. Moo ndax defalunu ko ñaari gët,
9. ak aw làmmiñ ak ñaari tuñ ?
10. Nu gindi ko tegtal ko ñaari yoon yi, mbaax, m... | coran-wolof.pdf |
page_539 | 539
19. ñay weddi sunuy Laaya ñoom ñoo di waa càmmoñ.
20. Safara waa ngi di gand.
-----------------------------------------------------------------------------
Saar 91 : JANT BA
15 - Laaya – Laata Gàddaay ga
-----------------------------------------------------------------------------
Ci turu Yàlla Yë... | coran-wolof.pdf |
page_540 | 540
9. képp ku ko sellal, daldi nay texe.
10. te it, képp ku ko sàggane, daldi nay sooy.
11. Waa Saamuud, seen bewte, tax na ñu weddi,
12. ba ca ña gën weddi potoxlóo
13. Yonentub Yàlla ba ne leen : “Bàyyileen giléemug Yàlla gi ! mu naan”
14. Ñu weddi ko, rey ko. Seen Boroom, maasale na mbugël ma.ca kaw ... | coran-wolof.pdf |
page_541 | 541
4. Seen jëf wuute na.
5. Képp kuy joxe te ragal (Yàlla)
6. te mu dëggël yoolub àllaaxira
7. Dananu ko jàppandalal yoon wu yomb wa.
8. Képp ku nay, te dumóoyu boroomam,
9. te muy weddi yoolub àllaaxira,
10. Dananu ko jàppandalal yoon wu jafe wa,
11. te alalam du ko jariñ dara saa su ñu ko mbaqee... | coran-wolof.pdf |
page_542 | 542
19. te amul genn xéewal gu ñuy faye kenn ca moom,
20. Lu dul sàkku jëmm Boroomam ja gëna Kawe.
21. Te, xalset naa gëram (moom ka def noona) !
-----------------------------------------------------------------------------
Saar 93 : YOOR-YOOR GA
11 - Laaya – Laata Gàddaay ga
-----------------------------... | coran-wolof.pdf |
page_543 | 543
9. Jirim, nag, bu ko di xorñooñal.
10. Te laajkat it, bu ko di delloo.
11. Te it na ngay waxtaane, sa xéewalu Boroom.
-----------------------------------------------------------------------------
Saar 94 : FÉEXAL
8 - Laaya – Laata Gàddaay ga
--------------------------------------------------------... | coran-wolof.pdf |
page_544 | 544
8. te it na ngay xemmeem jëm ci sa Boroom.
-----------------------------------------------------------------------------
Saar 95 : GARABU FIGG
8 - Laaya – Laata Gàddaay ga
-----------------------------------------------------------------------------
Ci turu Yàlla Yërëmaakoon bi, Jaglewaakoon bi.
1... | coran-wolof.pdf |
page_545 | 545
Saar 96 : LUMBU DERET
19 Laaya – Laata Gàddaay ga
-----------------------------------------------------------------------------
Ci turu Yàlla Yërëmaakoon bi, Jaglewaakoon bi.
1.Jàngal, ci sa turu Boroom biy bind,
2. moo bind nit ci lumbu deret.
3. Jàngal ! Sa Boroom mooy ki gëna tedd,
4. mooy k... | coran-wolof.pdf |
page_546 | 546
12. walla muy digale ragal Yàlla ?
13. Xanaa gisoo su weddi woon tey dumóoyu ?
14. Xanaa dafa xamul ne Yàllaa ngi gis ?
15. Déedéet ! Su ko bàyyiwul, Dananu jiñ, mbaq ko,
16. ni ñuy mbaqi, fenkat buy defkatu bàkkaar.
17. Na woo gàngooram ga.
18. Nun dananu woo wattukati (Safara).
19. Déedéet ! ... | coran-wolof.pdf |
page_547 | 547
3. Laylatul Qadri moo gën junni weer.
4. Ci guddi googu Malaaka ya, dañu cay wàcci àndak (Jibriil) ci seen ndigalu Boroom ci
mépp mbir.
5. Jàmm rekk la ba baa njël di jot (fajar sa di xar).
-----------------------------------------------------------------------------
Saar 98 : FIRNDE
8 - Laaya – Gan... | coran-wolof.pdf |
page_548 | 548
7. Ñi gëm tey jëfu yiw, ñoom ñoo ñee ñoo gën ci bindeef yi.
8. Seenug pey fa seen Boroom Àjjanay adan lay doon, yoo xam ne ay dex ñooy daw ci
suufam, ñu béel fa. Yàlla gëram leen ñoom it ñu gëram ko. Loolu ku ragal Yàlla rekk koy am.
---------------------------------------------------------------------------... | coran-wolof.pdf |
page_549 | 549
-----------------------------------------------------------------------------
Saar 100 : JAABKAT YA
11- Laaya – Laata Gàddaay ga
-----------------------------------------------------------------------------
Ci turu Yàlla Yërëmaakoon bi, Jaglewaakoon bi.
1. Ca jaabkat ya seeni gimiñ di foor (fas) (Maa... | coran-wolof.pdf |
page_550 | 550
11. bu keroogee, sa Boroom Ku deñ Kumpa la ci ñoom?
-----------------------------------------------------------------------------
Saar 101 : TOJ-TOJ BA
11 - Laaya – Laata Gàddaay ga
-----------------------------------------------------------------------------
Ci turu Yàlla Yërëmaakoon bi, Jaglewaakoo... | coran-wolof.pdf |
page_551 | 551
10. Ana luy xamal lan mooy loolu Haawiyatu ?
11. Aw Safara la wu tàng.
-----------------------------------------------------------------------------
Saar 102 : ËPPLAANTE
8 - Laaya – Laata Gàddaay ga
-----------------------------------------------------------------------------
Ci turu Yàlla Yërëmaa... | coran-wolof.pdf |
page_552 | 552
-----------------------------------------------------------------------------
Saar 103 : JAMONO
3 - Laaya – Laata Gàddaay ga
-----------------------------------------------------------------------------
Ci turu Yàlla Yërëmaakoon bi, Jaglewaakoon bi.
1. (Giiñ naa) ci Jamono!
2. Ne nit, mi ngi c... | coran-wolof.pdf |
page_553 | 553
2. kuy dajale alal di ko lim,
3. jàpp ne alalam jaa koy taxa sax (baña dee).
4. Mukk ! dees na ko, mbaq ci biir Hutamatu.
5. Ana lan moo lay xamal luy Hutamatu ?
6. Mooy Safaraw Yàlla wa ñu taal
7. way alawtiku ba ca xol ya.
8. Dañu leen cay séndël,
9. ci ay gàlli Safara yu ñu tàllal.
------... | coran-wolof.pdf |
page_554 | 554
3. moo yabal ca seen kaw ay njanaaw yu bari
4. ñu di leen sànni ay doj yu ñu saaf?
5. Mu def leen ñu mel ne am ñax mu ñu sàqami.
-----------------------------------------------------------------------------
Saar 106 : QUREYCHI
4 - Laaya – Laata Gàddaay ga
------------------------------------------... | coran-wolof.pdf |
page_555 | 555
-----------------------------------------------------------------------------
Ci turu Yàlla Yërëmaakoon bi, Jaglewaakoon bi.
1. Xanaa gisuloo kay weddi bisub dekkiwaat ba ?
2. Mooy kay bunduxataal jirim,
3. te du sonn muk ci leel miskiin yi.
4. Xuru Safara, ñeel na ñay julli
5. ñay sàggane aka yee... | coran-wolof.pdf |
page_556 | 556
2. Na ngay julli ngir sa Boroom te na ngay rendi.
3. Ka lay bañ aka ñaawal, moo dog ci lépp lu baax.
-----------------------------------------------------------------------------
Saar 109 : YÉEFËR YA
6 - Laaya – Laata Gàddaay ga
------------------------------------------------------------------------... | coran-wolof.pdf |
page_557 | 557
3 - Laaya – Gannaaw Gàddaay ga
-----------------------------------------------------------------------------
Ci turu Yàlla Yërëmaakoon bi, Jaglewaakoon bi.
1. Saa su ndimbalu Yàlla dikkee ak ndam la,
2. te nga gis ne nit ñaa ngi dugg def ay mbooloo ci biir diineey Yàlla ji,
3. na nga sàbaal, te sant ... | coran-wolof.pdf |
page_558 | 558
5. loosam wa, buumug rawa cay nekk (caq bu ñu soy).
-----------------------------------------------------------------------------
Saar 112 : SELLAL
4 - Laaya – Laata Gàddaay ga
-----------------------------------------------------------------------------
Ci turu Yàlla Yërëmaakoon bi, Jaglewaakoon bi.... | coran-wolof.pdf |
page_559 | 559
1. Waxal ne : “Maa ngi sàkku muslaayi Boroom suba si,
2. ci ayu li Mu bind,
3. ak ci ayu lëndëm ga saa bu kukkee,
4. ak ci ayu ñiy wal ëf ci pas-pas yi (jibarkat yi),
5. ak ci ayu ku iñaan saa su jógee bay feeñal kiñaan ga ”.
---------------------------------------------------------------------------... | coran-wolof.pdf |
page_560 | 560
----------------------------------------------------------------------------- | coran-wolof.pdf |
Subsets and Splits
No community queries yet
The top public SQL queries from the community will appear here once available.