audio audioduration (s) 2.29 12.5 | transcription stringlengths 26 118 |
|---|---|
réew mii réewum njub péex ak jàmm la | |
Nit kooku dafa yeewu waaye naa fi ma koy jaar | |
ñii fàlu nañu buur ñii doomi buur lañu di ay garmi | |
nanga butti jén yi dal di leen raxas ba ñu set | |
maa ko gis ci peroN bi la yàbbi logu poon bi | |
ba mu nekkee lu yàgg ca kër buur mu ni xuléet delluwaat na mu meloon | |
mbubb mi dafa xalloon ma def ci weexal | |
boo jàddee ci sa càmmooñ dinga séen sama kër | |
njàngale mi dina jafe ci moom ndax sawaru ci | |
am na ay mbaaru mbott yu ñu dul lekk | |
boo bëggee gis gaynde demal ca màndi ma | |
maa ngi tollu woon ci sama diggi ndënd | |
ku ma bëgga toroxal yaay mujjee torox | |
man de xawma lu muy ree nii ba di kekku | |
dafa jënd pàkk bi rekk tàmbali ko sàkket | |
amari ngoonee taxoon kajoor feyatul voon galag jolof | |
xam nga xéll ni taluma wure ak soxal yi ci sama bopp yépp | |
dafa gore moo tax ma nangoo liggéey ak moom | |
Na ku nekk déglu sa morom ndax ngeen baña réeroo | |
ña leen a jëkka séen ca dëkk ba dañu teg seen loxo ci seen gémmiñ | |
ndaw si daldi leen di juuy fekk na nag ag genn dédd a ngi fi goo xam né gii war naa mot diggante fii ag teen ba | |
maa ngi leen di soññ ci def seen liggéey | |
li nga semb dey yombul waaye yàlla na la ci yàlla jàppale | |
booba jamano pikini rekk la sondeel doon jar | |
li nga toog lu yàgg moo tax sa tànk yi sadd | |
bu ñu fëggatee nanga xool ci yëru bi bala ngay ubbi | |
ndax garmi day am jabari jinné di ci jur ay doom na ka walliiw wu nekk | |
amoon na ag dóobali ci seen buntu kër | |
xaftaan bu nëtëx la sol ak mbaxane mu xonq | |
li ëpp ci lapto yi ay njaago lañu woon | |
sama lam bi furi na war naa koo sóob | |
jubalal sa tuuru fetal bi fu dara nekkul | |
juuti bi dafay dem ci luuma yi ngir feyyu juuti | |
soo wutul kaaf sa pitax yi dinañu dem | |
amari jullit né ko jógal nu dem rekk | |
xale bi daal dafa ma lëjala lëjal ba nga xam né dem na dayo | |
dafa xeet taabal bi dal di ko pintiir | |
dafa indiwaale woon surgaam bu mu daan yónni | |
sa mbubb mu xàññaaral mooma daal bu ko sol | |
dafa doon dox ba yàgg mu ne dàll daanu | |
reeni xom xom fajkat yee koy jëfandikoo | |
waa ji yóbbu mbaam yi wax leen li buur diglé | |
ku sa bëgge bari sa ngor néew | |
sama tànk bépp a ngi xasan taqentaan a ma topp | |
boroom kër ga dafa ko fitnaaloon bu mu mujj toxu | |
yaa ngi doon gam gami xamoo dara ci waxtaan wi | |
séex yooyu neex nañoo xàmme nuroowuñu | |
su amee toppatoo gi ci war xar mu rafet lay doon | |
benn seex bi gàjj bi ci lex bi laa koy xàmmee | |
gone yu mbuujaa mbuuj yi ñoo fi nekk | |
sacakàt bà défà né parah né varah | |
ak tàngaay wi ngoor si dow dem daanu ci kër | |
peccum liir bu neexee ndeyam a téye ca tank ya | |
ñi nelaw ñii ci des doxantuji dugg ci réew mi | |
ba ñu dajee ak yaw dañu daw wëqét | |
danu daan dem tefes di xëcc mbaal ngir ñu may nu jén | |
seen baay nee na leen bu nu bàyyi benn ruq bu ñu bàllarñiwul | |
lu di nav té du tag mukà ngélav | |
aprés bu may séy dina ma geener torop encore | |
borom bi yërëm ma ndege moykat rekk laa | |
demal ne ko mu seede ma ñaari kiloy ceeb | |
bàggu fu nekk ñu bàggante rekk gisuñu dara | |
booba fekk na ñaari mag yi ñu ngi doon waaja seeti seeni coro | |
mu ne mënula ñów waaye mu ngi leen di yokk ngóora | |
wax ji dafa lunk ñu bare ci mbooloo mi nanduñu ko | |
ku ja ci jant bi te ne gisu ko lu ñu ci mën | |
dama la bëgga biral sama dikk moo tax ma telefone | |
ñu jekki ba nga xam né jant so na góor gi ñów seet nag yi gisul dara | |
lenn rekk la bu mbeex màggee warul sëy warul am beneen jëkkër bu dul man | |
Naka la dawe ci néegam mu mbëkk boppu doom ji doon lang di bunt bi | |
dama bëgg xam këf ki mu dugal ci waxande wi lu mu doon | |
mu teg saakam dal di dem ubbi palanteer bi | |
ndeer la dellusi ni tareet tareet ey biram njéemé koo njaay de wul dekki na de | |
alkaati baa ngi ne sàtt ci bunt kër gi ca suba ba tey | |
tànk boo séqi dinañu la ko bindal tuyaabo | |
janq jee daan watu pàq waaye loolu xewwi na léegi | |
moom bëggewul rekk yem ci dafa wóttóoral | |
bi ko doomu baay yi lakkalee ba nga xam ni mënatula dëkk ak ñoom mu gàddaay dem jolof | |
wàccal rekk du yàgg létt yi du yàgg | |
bu ñu defaree sorbo bi ba noppi dañu koy taxaar | |
buumu xalam gi yóbbaale na la wa ngi xandaalu | |
aa man dé sama jëkër dafa ma mooñloo tey jii te dama koy mooñal | |
mu mel ni ndoxu asamaan si yépp a bëggoona xëppu ci kaw suuf si | |
diggante ndakaaru ak barñi fanweeri kilomet la | |
fekk am na ñu dëgger bopp ñu ko sarax ñoo ñu daldi tàqalikoo ak seeni bët | |
may ma loxo ma dugal taabal bi ci saal bi | |
góor gu am fayda du dàggasante ak jigéen | |
booy war mbaam dangay jàpp ci kawar gi ci céq mi | |
abdu woor na tey dafa feebaroon fan yi nu weesu | |
xale yi farlu nañu lool ci njàngum katesis bi | |
xaalis bi ngay jox jibar bi tee nga cee jénd garab yi la doktoor bindal | |
bul fàttee jënd yomb tey cere lañuy togg | |
dafa sëpp sayu xat waaye mën na bëre | |
ku ñu ma may rekk ma ni bëgguma ko ma bëggoon nag wuti | |
moo doom sa baay waxu la woon lii | |
saa su ma ko nuyujee dina ma may aylayéwén junni | |
te ñu bari bassi seen feebar ci tooy lay joge | |
am na masin yuy gàbb waaye dañu jafe njég | |
palpale yi nga gis bitim réew lañu lenn di jaaye | |
ree ji mu lay gatandoo rekk sedd na xol |
End of preview. Expand in Data Studio
README.md exists but content is empty.
- Downloads last month
- 17