African-English Parallel Sentences (MT650)
Collection
Parallel corpus for 154 African languages extracted from the MT650 dataset • 101 items • Updated • 3
eng stringlengths 12 371 | wol stringlengths 11 449 |
|---|---|
Behold , I come quickly : blessed is he that keepeth the sayings of the prophecy of this book . | Maa ngi ñëw léegi . Yaw miy sàmm waxi Yàlla , yi ci téere bii , barkeel nga . |
( I also baptized the household of Stephanas ; besides them , I don 't know whether I baptized any other . ) | Aaŋkay ! Sóob naa it ci ndox waa kër Estefanas . Waaye ci sama pàttaliku sóobuma keneen . |
When the dragon saw that he was thrown down to the earth , he persecuted the woman who gave birth to the male child . | Ba ninkinànka ja gisee ne , daaneel nañu ko ci kaw suuf , mu dàq jigéen , ja juroon doom ju góor ja . |
Forgive us our sins , for we ourselves also forgive everyone who is indebted to us . Bring us not into temptation , but deliver us from the evil one . ' " | Baal nu sunuy bàkkaar , ndaxte nun itam danuy baal ñépp ñi nu tooñ.Te bu nu teg ci yoonu nattu . " " |
When Peter saw it , he responded to the people , " You men of Israel , why do you marvel at this man ? Why do you fasten your eyes on us , as though by our own power or godliness we had made him walk ? | Bi Piyeer gisee loolu nag , mu ne mbooloo mi : " Yéen waa Israyil , lu tax ngeen waaru ci lii ? Lu tax ngeen di nu xool jàkk , mel ni ci sunu kàttan , mbaa ci sunu ragal Yàlla lanu doxloo kii ? |
And stood at his feet behind him weeping , and began to wash his feet with tears , and did wipe them with the hairs of her head , and kissed his feet , and anointed them with the ointment . | Bi jigéen ja agsee , mu taxaw ca gannaaw tànki Yeesu , di jooy . Noonu ay rangooñam tooyal tànki Yeesu , jigéen ja di leen fomp ak kawaram , di leen fóon te ciy sotti latkoloñ ja . |
And the soldiers led him away into the hall , called Praetorium ; and they call together the whole band . | Bi loolu amee ñu dugal Yeesu ci biir kër boroom réew ma , mooy bérab bu ñuy wax Peretoriyum , ñu daldi woo mbooloom xarekat yépp . |
And they departed thence , and passed through Galilee ; and he would not that any man should know it . | Bi loolu amee ñu jóge fa , jaar ci diiwaanu Galile , Yeesu bëggul kenn yég ko . |
And when the ten heard it , they were moved with indignation against the two brethren . | Bi nga xamee ne fukki taalibe ya dégg nañu loolu , ñu mere ñaari doomi ndey ya . |
Now when they heard of the resurrection of the dead , some mocked ; but others said , " We want to hear you again concerning this . " | Bi ñu déggee nag , muy wax ci mbirum ndekkitel ñi dee , ñii di ko fontoo , ña ca des ne ko : " Dinanu la déglu ci mbir moomu beneen yoon . " |
I suppose therefore that this is good for the present distress , I say , that it is good for a man so to be . | Bu nu seetee tiis wii fi teew nag , defe naa ne li baax ci nit , moo di mu sax ci li mu nekk . |
Rebuke not an elder , but intreat him as a father ; and the younger men as brethren ; | Bul gëdd mag , waaye waxtaanal ak moom ni sa baay . Ndaw it , nga digal ko ni sa rakk , |
And seek not ye what ye shall eat , or what ye shall drink , neither be ye of doubtful mind . | Buleen di wut lu ngeen di lekk walla lu ngeen di naan ; te buleen ci jaaxle . |
Love not the world , neither the things that are in the world . If any man love the world , the love of the Father is not in him . | Buleen sopp àddina ak li ci biiram . Ku sopp àddina , mbëggeelu Baay bi nekkul ci moom . |
Having many things to write to you , I don 't want to do so with paper and ink , but I hope to come to you , and to speak face to face , that our joy may be made full . | Bëggoon naa leena wax lu bare ci bataaxel bii , waaye lépp xajul ci kayit . Kon nag fas naa yéenee ñëw , ba jàkkaarlook yeen , nu waxtaan ci , ngir sunu mbég mat sëkk . |
At the ninth hour Jesus cried with a loud voice , saying , " Eloi , Eloi , lama sabachthani ? " which is , being interpreted , " My God , my God , why have you forsaken me ? " | Ci tisbaar nag Yeesu wootee kàddu gu dëgër naan : " Elowi , Elowi , lema sabaktani ? " liy tekki : " Sama Yàlla , sama Yàlla , lu tax nga dëddu ma ? " |
I give eternal life to them . They will never perish , and no one will snatch them out of my hand . | Dama leen di jox dund gu dul jeex ; duñu sànku mukk , te kenn du leen jële ci sama loxo . |
The great city was divided into three parts , and the cities of the nations fell . Babylon the great was remembered in the sight of God , to give to her the cup of the wine of the fierceness of his wrath . | Dëkk bu mag ba xàjjalikoo ñetti cér , te dëkki xeet yi màbb . Noonu Yàlla daldi fàttaliku Babilon bu mag ba , ngir jox ko koppu meram mu tàng ma , ba mu màndi . |
For Herod himself had sent forth and laid hold upon John , and bound him in prison for Herodias ' sake , his brother Philip 's wife : for he had married her . | Fekk Erodd yónnee woon na , jàpp Yaxya , yeew ko , tëj . Ndaxte Erodd takkoon na Erojàdd jabaru Filib magam . |
After these things came Jesus and his disciples into the land of Judaea ; and there he tarried with them , and baptized . | Gannaaw loolu Yeesu ànd ak ay taalibeem , dem ca biir diiwaanu Yude , toog fa ak ñoom ab diir , di sóob nit ñi ci ndox . |
For he is not a Jew who is one outwardly , neither is that circumcision which is outward in the flesh ; | Juddu nekk Yawut taxul sag Yawut dëggu , te xaraf ci saw yaram taxul sa xaraf wóor . |
Which none of the princes of this world knew : for had they known it , they would not have crucified the Lord of glory . | Kenn ci njiiti àddina amul woon xam @-@ xam boobu . Su ñu ko amoon , kon duñu rey Boroom ndam li ci bant bi . |
So then , brothers , stand firm , and hold the traditions which you were taught by us , whether by word , or by letter . | Kon nag bokk yi , taxawleen bu dëgër te jàpp ci dénkaane yi nu leen jottali , muy ci li nu wax , muy ci li nu bind . |
Whoever will not receive you nor hear you , as you depart from there , shake off the dust that is under your feet for a testimony against them . Assuredly , I tell you , it will be more tolerable for Sodom and Gomorrah in the day of judgment than for that city ! " | Koo xam ne gàntu na leen , mbaa mu tanqamlu leen , génnleen fa , yëlëb seen pëndu tànk , ngir seede leen seen réer . " |
His winnowing fork is in his hand , and he will thoroughly cleanse his threshing floor . He will gather his wheat into the barn , but the chaff he will burn up with unquenchable fire . " | Layoom mu ngi ci loxoom , ngir jéri dàgga ja , ba mu set ; pepp ma dina ko def ca sàq ma , waaye xatax ba dina ko lakk ci safara su dul fey mukk . " |
Only Luke is with me . Take Mark , and bring him with thee : for he is profitable to me for the ministry . | Luug rekk a des fi man . Indaaleel Màrk , ndaxte amal na ma njariñ ci liggéey bi . |
That I have great heaviness and continual sorrow in my heart . | Maanaam , duma noppee am naqar wu réy ci sama biir xol , |
And the angel answering said unto him , I am Gabriel , that stand in the presence of God ; and am sent to speak unto thee , and to shew thee these glad tidings . | Malaaka ma tontu ko ne : " Man maay Jibril miy taxaw ci kanam Yàlla . Dañu maa yónni ngir ma wax ak yaw te yégal la xebaar bu baax boobu . |
Are they not all ministering spirits , sent forth to minister for them who shall be heirs of salvation ? | Malaaka yépp ay xel lañu rekk yuy liggéeyal Yàlla , mu di leen yónni ñuy dimbali nit , ñi nar a jot mucc gi . |
Paul , a servant of God , and an apostle of Jesus Christ , according to the faith of God 's elect , and the acknowledging of the truth which is after godliness ; | Man Pool maa lay bind , man miy jaamu Yàlla ak ndaw li Yeesu Kirist yónni , ngir xamle ngëm , gi lal yoonu ñi Yàlla tànn , tey yokk xam @-@ xamu dëgg , giy meññ ragal Yàlla ; |
Every Scripture is God @-@ breathed and profitable for teaching , for reproof , for correction , and for instruction in righteousness , | Mbind mu sell mépp , ci gémmiñu Yàlla la jóge , te am na njariñ ngir jàngal nit ñi , yedd leen , jubbanti leen te yee leen ci njub . |
who was with the proconsul , Sergius Paulus , a man of understanding . This man summoned Barnabas and Saul , and sought to hear the word of God . | Mu bokk ci gàngooru boroom réew ma tudd Sersiyus Poolus , di nit ku neex xel . Moom nag mu woolu Barnabas ak Sool , ngir bëgg a dégg kàddug Yàlla . |
He begged him much that he would not send them away out of the country . | Muy ñaan Yeesu lool , ngir mu bañ leen a dàq ca réew ma . |
A big wind storm arose , and the waves beat into the boat , so much that the boat was already filled . | Naka noona ngelaw lu mag daldi jóg , duus yi sàng gaal gi , ba mu bëgg a fees . |
And let us consider one another to provoke unto love and to good works : | Nanu seet ni nu man a xiirtalante cig mbëggeel ak ci jëf yu baax . |
For I am persuaded , that neither death , nor life , nor angels , nor principalities , nor things present , nor things to come , nor powers , | Ndax wóor na ma ne , dara mënu noo tàggaleek mbëggeelam ; du dee , du dund , du malaaka yi , du seeni kilifa , du tey , du ëllëg , du boroom doole yi , |
For whosoever shall call upon the name of the Lord shall be saved . | Ndaxte bind nañu : " Képp ku woo Boroom bi ciw turam , dinga mucc . " |
This is the will of the one who sent me , that everyone who sees the Son , and believes in him , should have eternal life ; and I will raise him up at the last day . " | Ndaxte lii mooy bëgg @-@ bëggu Baay bi : képp ku gis Doom ji te gëm ko , am dund gu dul jeex , te bés bu mujj ba , dinaa ko dekkal ! " |
for he was yet in the body of his father when Melchizedek met him . | Ndaxte mi ngi nekkoon ci geñog maamam Ibraayma , bi ko Melkisedeg gatandoo . |
But woe unto them that are with child , and to them that give suck , in those days ! for there shall be great distress in the land , and wrath upon this people . | Ngalla jigéen ñi ëmb ca bés yooya , ngalla it ñiy nàmpal ! Ndaxte tiis wu metti dina am ci réew mi , te Yàlla dina wàcce meram ci waa réew mii . |
Jesus saith unto them , Have ye understood all these things ? They say unto him , Yea , Lord . | Noonu Yeesu laaj taalibe ya ne leen : " Loolu lépp , ndax xam ngeen lu muy tekki ? " Ñu tontu ko : " Waaw . " |
That ye may be blameless and harmless , the sons of God , without rebuke , in the midst of a crooked and perverse nation , among whom ye shine as lights in the world ; | Noonu dingeen am xol bu laab bu àndul ak ŋàññ , di guney Yàlla yu amul sikk ci biir jamono ju yàqu te rëb . Dangeen di leer ci seen biir ni weer ci àddina si , |
And he drave them from the judgment seat . | Noonu mu dàq leen ca àttekaay ba . |
And she brought forth a man child , who was to rule all nations with a rod of iron : and her child was caught up unto God , and to his throne . | Noonu mu jur doom ju góor , muy ki war a jiite xeeti àddina yépp ak yetu weñ . Waaye ñu daldi fëkk doom ja , mu dem ca Yàlla ak gànguneem . |
Then said they unto him , What shall we do , that we might work the works of God ? | Noonu ñu laaj ko ne : " Lu nu war a liggéey , ngir matal jëf yi neex Yàlla ? " |
They all ate , and were filled . | Noonu ñépp lekk ba suur . |
If we say that we have not sinned , we make him a liar , and his word is not in us . | Su nu waxee ne defunu bàkkaar , teg nanu ko kuy tebbi waxam , te kàddoom duggagul ci sunu xol . |
For I rejoiced greatly , when brothers came and testified about your truth , even as you walk in truth . | Sunuy mbokk ñëw nañu , te seede ni nga fonke dëgg gi , ba wéer ci sa dund gépp , te bég naa ci lool . |
Then said Agrippa unto Festus , This man might have been set at liberty , if he had not appealed unto Caesar . | Te Agaripa ne Festus : " Manoon nanu koo yiwi , bu dénkuloon mbiram Sesaar . " |
And Adam was not deceived , but the woman being deceived was in the transgression . | Te it du Aadama la Seytaane nax , waaye jigéen ja la nax , ba mu jàdd . |
requesting , if by any means now at last I may be prospered by the will of God to come to you . | Te li ma koy faral di ñaan mooy lii : bu soobee Yàlla , na ma ubbil bunt , ba ma man a ñëw ci yéen . |
For however many are the promises of God , in him is the " Yes . " Therefore also through him is the " Amen , " to the glory of God through us . | Te lépp lu Yàlla dige woon fekk na " waawam " ci moom . Noonu kon ci Kirist lanuy waxe : " Amiin , " ngir yékkati ndamu Yàlla . |
Not only so , but who was also appointed by the assemblies to travel with us in this grace , which is served by us to the glory of the Lord himself , and to show our readiness . | Te sax mbooloo yi ñoo ko tànn , ngir mu ànd ak nun , bu nuy yóbbu ndimbal li ngir ndamu Boroom bi , te mu firndeel sunu yéene ju rafet . |
But the righteousness which is of faith says this , " Don 't say in your heart , ' Who will ascend into heaven ? ' ( that is , to bring Christ down ) ; | Waaye ku jub ci kanam Yàlla ci kaw ngëm , nii lay waxe : " Bul wax ci sa xol ne : " Kuy yéeg ci kaw ? " " mel ni dangaa bëgg Kirist wàcc . |
But now , I say , I am going to Jerusalem , serving the saints . | Waaye nag fi mu nekk maa ngi dem nii Yerusalem , ngir dimbaliji gaayi Yàlla yu sell ya fa nekk . |
I have spoken these things to you , that my joy may remain in you , and that your joy may be made full . | Wax naa leen loolu , ngir ngeen bokk ci sama mbég , te seen bos mat sëkk . |
And Jesus put forth his hand , and touched him , saying , I will ; be thou clean . And immediately his leprosy was cleansed . | Yeesu tàllal loxoom , laal ko naan : " Bëgg naa ko , wéral . " Ca saa sa ngaanaam daldi deñ . |
These are the things which defile a man : but to eat with unwashen hands defileth not a man . | Yooyu ñooy indil nit sobe , waaye lekk ak loxo yoo raxasul du tax nit am sobe . " |
Faithful is he that calleth you , who also will do it . | Yàlla , mi leen woo ci loolu , kuy sàmm kóllëre la , te dina ko def . |
He who didn 't spare his own Son , but delivered him up for us all , how would he not also with him freely give us all things ? | Yàlla mi nu gàntulul Doomam waaye mu joxe ko , mu dee ngir nun , ndax dina nu bañalati dara ? |
You masters , do the same things to them , and give up threatening , knowing that he who is both their Master and yours is in heaven , and there is no partiality with him . | Yéen it sang yi , jëfeleen noonu seen diggante ak seeni jaam , te dëddu gépp raglu , xam ne yéena bokk benn Boroom ci asamaan , te ñépp a yem fi moom . |
making known to us the mystery of his will , according to his good pleasure which he purposed in him | ci feeñal nu mbóoti coobareem , dëppook yéeneem ju rafet , ji mu jaarale ci Kirist . |
And desired of him letters to Damascus to the synagogues , that if he found any of this way , whether they were men or women , he might bring them bound unto Jerusalem . | laaj ko ay bataaxal yu muy yóbbul jànguy dëkku Damas . Noonu ñu mu fa fekk , te ñu bokk ci yoon wi , góor mbaa jigéen , mu am dogalu yeew leen , indi leen Yerusalem . |
and not by his coming only , but also by the comfort with which he was comforted in you , while he told us of your longing , your mourning , and your zeal for me ; so that I rejoiced still more . | te du ci ñëwam rekk sax waaye ci li ngeen dëfël xolam . Yégal na nu seen nammeel ci nun , seen réccu ak seen farlu jëm ci man , ba sama mbég gën cee yokku . |
And have no root in themselves , and so endure but for a time : afterward , when affliction or persecution ariseth for the word 's sake , immediately they are offended . | waaye du yàgg , ndaxte wax ji saxul ci moom . Bu jaaree ci nattu nag , mbaa ñu fitnaal ko ndax kàddu gi , mu dàggeeku ci saa si . |
But let it be the hidden man of the heart , in that which is not corruptible , even the ornament of a meek and quiet spirit , which is in the sight of God of great price . | waaye nay taar bu sax bu nekk ci biir , di xol bu nooy te dal , ndax loolu lu takku la fa Yàlla . |
When they saw it , they all murmured , saying , " He has gone in to lodge with a man who is a sinner . " | Ñépp gis loolu , di ñurum @-@ ñurumi naan : " Mi ngi dal cig këru boroom bàkkaar . " |
You have heard that it was said , ' You shall love your neighbor , and hate your enemy . ' | " Dégg ngeen ne , waxoon nañu : " Soppal sa moroom te sib sa bañaale . " |
In my Father 's house are many homes . If it weren 't so , I would have told you . I am going to prepare a place for you . | Am na néeg yu bare ca sama kër Baay , bu dul woon noonu , ma wax leen ko , ndaxte maa ngi dem defaral leen fa ngeen di dëkk . |
They have tails like those of scorpions , and stings . In their tails they have power to harm men for five months . | Am nañu ay geen yu am ay fitt ni jànkalaar , te ca la seen kàttan nekk , ngir metital nit ñi diirub juróomi weer . |
Therefore the Jews sought the more to kill him , because he not only had broken the sabbath , but said also that God was his Father , making himself equal with God . | Baat boobu moo tax ba Yawut yi gën koo wut a rey , ndaxte yemul woon rekk ci bañ a topp ndigalu bésu noflaay ba , waaye dafa wax it ne , Yàlla Baayam la , ba teg boppam Yàlla . |
And straightway he entered into a ship with his disciples , and came into the parts of Dalmanutha . | Bi ko Yeesu defee , mu yiwi leen , daldi dugg ak taalibe ya ca gaal ga , dem ca wàlli Dalmanuta . |
Immediately Jesus made the disciples get into the boat , and to go ahead of him to the other side , while he sent the multitudes away . | Bi loolu amee Yeesu sant taalibe ya , ñu dugg gaal ga te jàll dex ga , jiituji ko , muy yiwi mbooloo ma . |
And another angel came out of the temple which is in heaven , he also having a sharp sickle . | Bi loolu amee meneen malaaka génn ca kër Yàlla ga nekk ca asamaan , yor moom itam sàrt bu ñaw . |
When he had found him , he brought him to Antioch . It happened , that for a whole year they were gathered together with the assembly , and taught many people . The disciples were first called Christians in Antioch . | Bi mu ko gisee , mu indi ko Ancos . Noonu atum lëmm ñu bokk ak mbooloom ñi gëm , di jàngal nit ñu bare . Te ci Ancos lañu jëkk a tudde taalibe ya Gaayi Kirist . |
Then the devil took him into the holy city . He set him on the pinnacle of the temple , | Bi mu waxee loolu , Seytaane yóbbu ko ca dëkk bu sell ba , teg ko ca njobbaxtalu kër Yàlla ga . |
And said unto them , Ye men of Israel , take heed to yourselves what ye intend to do as touching these men . | Bi ñu ko defee mu ne leen : " Yéen bokki Israyil , moytuleen li ngeen di def nit ñooñu . |
You therefore must endure hardship , as a good soldier of Christ Jesus . | Bokkal ak man tiis , di jàmbaar ci toolu xareb Kirist Yeesu , |
men fainting for fear , and for expectation of the things which are coming on the world : for the powers of the heavens will be shaken . | Bu boobaa nit ñiy xëm ndax tiitaange , bu ñuy xalaat musiba , yi nar a wàcc ci àddina , ndaxte dees na yengal kàttani asamaan . |
If then ye have judgments of things pertaining to this life , set them to judge who are least esteemed in the church . | Bu ngeen amee ay lëj @-@ lëj yu mel noonu , dangeen di wuti ay àttekat ci ay nit , ñi amul wenn yoon ci mbooloom ñi gëm ! |
So then it is not of him who wills , nor of him who runs , but of God who has mercy . | Dama leen di wax nag , dara ajuwul ci coobareg nit , mbaa ci ñaqam , waaye lépp a ngi aju ci yërmandey Yàlla . |
Neither went I up to Jerusalem to them which were apostles before me ; but I went into Arabia , and returned again unto Damascus . | Demuma sax Yerusalem seeti ñi ma jëkk a nekk ay ndawi Kirist , waaye réewu Arabi laa dem , te gannaaw loolu ma dellusiwaat Damas . |
testifying both to Jews and to Greeks repentance toward God , and faith toward our Lord Jesus . | Dénk naa Yawut yi ak Gereg yi ne leen , ñu tuub seeni bàkkaar , ba woññiku ci Yàlla te gëm sunu Boroom Yeesu . |
For his disciples had gone away into the city to buy food . | Fekk booba nag , taalibey Yeesu ya dañoo demoon ca biir dëkk ba , di jënd lu ñu lekk . |
There shall be weeping and gnashing of teeth , when ye shall see Abraham , and Isaac , and Jacob , and all the prophets , in the kingdom of God , and you yourselves thrust out . | Foofa dingeen jooy , di yéyu , bu ngeen gisee seeni maam Ibraayma , Isaaxa , Yanqóoba ak yonent yépp ci nguuru Yàlla , te ñu dàq leen ca biti . |
Who , having received such a charge , thrust them into the inner prison , and made their feet fast in the stocks . | Gannaaw jot na ndigal loolu nag , mu sànni leen ca néeg ba gën a ruqu ci biir kaso ba , jéng seeni tànk . |
For a man indeed ought not to have his head covered , because he is the image and glory of God , but the woman is the glory of the man . | Góor nag moom warul a teg dara ci boppam , ndaxte mooy melokaanu Yàlla te dafay wone ndamu Yàlla . Jigéen moom dafay wone ndamu góor . |
And the seventh angel sounded ; and there were great voices in heaven , saying , The kingdoms of this world are become the kingdoms of our Lord , and of his Christ ; and he shall reign for ever and ever . | Juróom @-@ ñaareelu malaaka ma wol liitam , noonu baat yu xumb jib ca asamaan naan : " Nguuru àddina , jébbalaat nañu kosunu Boroom ak Almaseem , te dina nguuru ba fàww . " |
The mystery of the seven stars which thou sawest in my right hand , and the seven golden candlesticks . The seven stars are the angels of the seven churches : and the seven candlesticks which thou sawest are the seven churches . | Juróom @-@ ñaari biddiiw yi nga gis ci sama loxol ndeyjoor , ak juróom @-@ ñaari làmpi diwlin yu wurus yi , ay mbóoti Yàlla lañu te lii lañuy tekki : biddiiw yi ñoo di malaakay juróom @-@ ñaari mboolooy ñi gëm ; juróom @-@ ñaari làmp yi ñoo di juróom @-@ ñaari mbooloo yi . |
Or who is there among you , who , if his son asks him for bread , will give him a stone ? | Kan ci yéen , bu la sa doom ñaanee mburu , nga jox ko doj ? |
Let such an one think this , that , such as we are in word by letters when we are absent , such will we be also in deed when we are present . | Kiy wax loolu na xam lii : ni sunuy kàddu mel ci sunuy bataaxal , bu nu fa nekkul , noonu it lanuy mel ci sunuy jëf , bu nu teewee . |
Forasmuch then as we are the offspring of God , we ought not to think that the Godhead is like unto gold , or silver , or stone , graven by art and man 's device . | Kon nag , bu nu nekkee xeetu Yàlla , warunoo gëm ne , Yàlla mel na ni nataali wurus , xaalis mbaa doj yu nit defar ci xareñ mbaa xel . |
Brethren , be followers together of me , and mark them which walk so as ye have us for an ensample . | Kon nag bokk yi , toppleen ma te xool ñiy roy ci li nu tëral diirub sunu ngan ci yéen . |
How is it that you don 't perceive that I didn 't speak to you concerning bread ? But beware of the yeast of the Pharisees and Sadducees . " | Kon nag lu tax xamuleen ne , waxuma mburu ? Waaye damaa bëgg , ngeen moytu lawiiru Farisen ya ak Sadusen ya . " |
But I trust I shall shortly see thee , and we shall speak face to face . Peace be to thee . Our friends salute thee . Greet the friends by name . | Kon yaakaar naa laa seetsi balaa yàgg , jàkkaarlook yaw , nu waxtaan ci . |
If any man will do his will , he shall know of the doctrine , whether it be of God , or whether I speak of myself . | Ku fas yéenee wéy ci bëgg @-@ bëggu Yàlla , dina xam ndax sama njàngale ci Yàlla la jóge , walla ci sama coobare . |
That was the true Light , which lighteth every man that cometh into the world . | Kàddu googu mooy leer gu wóor , giy ñëw ci àddina te di leeral nit ku nekk . |
God , having in the past spoken to the fathers through the prophets at many times and in various ways , | Li jiitu tey Yàlla waxoon na ak maam ya ci wàll yu bare ak ci tëralin yu wuute jaarale ko ca yonent ya . |
And now I stand and am judged for the hope of the promise made of God unto our fathers : | Li ma indi ci kureelu àttekat yii nag , mooy yaakaar ne , Yàlla dina amal li mu digoon sunuy maam . |
Now about the things which I write to you , behold , before God , I 'm not lying . | Lii ma leen di bind nag , Yàllaa may seede ci ne , du ay fen . |
This dataset contains parallel sentences in English and Wolof (Senegal).
The dataset contains parallel sentences that can be used for:
If you use this dataset, please cite the citation guide of the original OPUS MT560 dataset.
This dataset is released under the Creative Commons Attribution 4.0 International License.