url stringlengths 30 180 | content stringlengths 64 14.2k | Source stringclasses 1
value |
|---|---|---|
https://www.defuwaxu.com/diine-ak-politig-nan-moytu-li-nuy-feewale/ | DIINE AK POLITIG : NAN MOYTU LI NUY FÉEWALE
Ëttu boole bi, genn kurél la gu boole mbooleem këri diine yi ngir saxal jàmm ci biir réew mi, rawatina ci lu ñeel politig beek diine ji. Seetlu nanu ne saa bu jamanoy fal njiitu réew jotee rekk, njaqare dafay faral di am. Li ko waral, nag, du dara lu dul ñenn ci politiseN yi... | Defuwaxu |
https://www.defuwaxu.com/kan-mooymaki-sall/ | KAN MOOY…MAKI SÀLL ?
Ci Baatu Majaw Njaay
Aw askan, bala moo tànn njiitam, war naa seet bu baax jikkoom, seetaat ko, xam mooy kan. Looloo waral Lu defu waxu, seen yéenekaay ci kàllaamay Kocc, jóg ngir jagleel wutaakon yi ay xët yuy fésal seen jaar-jaar ak seeni naal ñeel réew mi. Maanaam, li yitteel Lu defu waxu moo ... | Defuwaxu |
https://www.defuwaxu.com/fan-lanu-jem-ak-nakki-bill-gates-yi/ | FAN LANU JËM AK ÑAKKI BILL GATES YI?
(USÉYNU BÉEY)
Coow laa ngi ne kurr ! Afrig ba Afrig daj, li ko dale Keer ba Peretoryaa, Ndakaaru jàpp Adis-Abebaa, wax ji benn la : jàppal wakseŋ fii, bàyyil wakseŋ fee.
Coow li nag, ci anternet bi la jëkke. Dafa am ay Móodu-Móodu ak ay Faatu-Faatu yu def ay widewoo di ci aartu s... | Defuwaxu |
https://www.defuwaxu.com/reew-mi-gej-naa-yengoo-nii-useynu-beey/ | WAAW, KAÑ LA SENEGAAL GËJ A YËNGOO NII…?
Weeru màrs wii weesu, Senegaal tàngoon na jipp ! Gannaaw ba alkaati yeek sàndarm yi jëlijee Usmaan Sonko ngir jébbal ko Yoon, daanaka waa Ndakaaru yépp, waa Senegaal yépp sax, rawatina ndaw ñi, dañoo jóg nekk benn say, ne : “Du fi ame !” Keroog ak fan ya ca topp, jàppante bi me... | Defuwaxu |
https://www.defuwaxu.com/bokk-ak-nawloo-ngir-jamm-ak-naataange-ci-addina/ | BOKK AK NAWLOO NGIR JÀMM AK NAATAANGE CI ÀDDUNA SI
Weer yii nu génn, réew yu bare tànn nañu seen njiit. Joŋante yi gën a indi coow mooy yi amoon ca Beliyoriisi mbaa Amerig, walla fii ci Afrig, ca Kodiwaar, Gine-Konaakiri, Burkinaa, ak-ñoom-seen. Réewum Ganaa moo ci mujj.
Gëstukat yu bare ak i yéenekaay bind nañ ci, wo... | Defuwaxu |
https://www.defuwaxu.com/afrobasket-kigali-2023-xalam-demoon-na-bay-neex/ | AFROBASKET-KIGALI 2023 : XALAM DEMOON NA BAY NEEX !
Démb la woon finaalu Afrobasket bi doon am ren ca Ruwàndaa, doxoon ci diggante Senegaal ak Niseriyaa. Niseriyaa nag moo ko mujje gañe, daldi jël kub bi.
Senegaal, ca njëlbeen ga, ku la waxoon ni dana finaalu nga weddi ko. Nde, dafa lajj ñaari yoon ca ndoorteelu xëcc... | Defuwaxu |
https://www.defuwaxu.com/jeeri-joor-ndeelaak-tubaab-bi/ | JÉERI JOOR NDEELAAK TUBAAB BI
Jéeri Joor Ndeela Faal mu ngi gane àdduna ci atum 1871. Mu doon doom ci Sàmba Yaaya Faal mi newoon fanweer ak ñaarelu Dammeelu Kajoor te Nasaraan yi daaneloon ko ba noppi yóbbu ko Ndar-Géej, téye ko fa. Ci atum 1891 la xaru ci dex gi ginnaaw bi way-juram bu jigéen génnee àdduna te Tubaab ... | Defuwaxu |
https://www.defuwaxu.com/xibaari-taggat-yaram-dibeer-29-sanwiye-2023/ | XIBAARI TÀGGAT-YARAM (Dibéer 29 saŋwiye 2023)
CHAN 2023
Sunu gaynde yee ngi wëyal di wane seen bopp fale ca Alseri. Bërki-démb, ci àjjuma ji, lañ doon daje ak seen naataango yi, Saa-Muritani yi, ñu mujje leen ko yóbbul benn bal ci dara (1-0). Ab teg-dóor lañu am, dugal ko ci xaaj bu njëkk bi.
Alseri, moom mi dalal j... | Defuwaxu |
https://www.defuwaxu.com/manchester-city-witti-na-biddiiwam-bu-njekk/ | MANCHESTER CITY WITTI NA BIDDIIWAM BU NJËKK
Àngale yaa ngay gundaandaat ! Manchester a ngi toj ! Ren, dafa baxa. Ci bëccëgu dibéeru tey ji, foo sànni woon mbàttu mu tàkk. Soppey Manchester City yaa nga feesoon dell mbeddi dëkk ba, di yuuxoo ak a fecci. Ñoo yey nag. Ndaxte, ba Manchester City dee këlëb ba tey, guléet ñ... | Defuwaxu |
https://www.defuwaxu.com/lan-moo-wund-demu-maki-bi-riisi/ | Lan moo wund demu Maki bi Riisi ?
Fan yii weesu, njiitu réew, Maki Sàll, fekki woon na Putin ca Riisi ngir, nee ñu, ñu waxtaane bekkoor bi xare bi xew digganteem ak Ikren jural àddina si, rawatina réewi Afrig yi. Ndax kat, Maki Sàll dafa jàpp ne xare bu ni mel, baaxul ci réew yu néew doole ni réewi Afrig yi. Nde, rée... | Defuwaxu |
https://www.defuwaxu.com/afrig-ak-koronaa-afrig-ginnaaw-koronaa/ | AFRIG AK KORONAA, AFRIG GINNAAW KORONAA
USÉYNU BÉEY
Koronaawiris bi, li muy metti metti, terewul kàngami boroom xam-xam yiy wéy di ci weccee xalaat ñeel doxalinu àddina si, ba xam luy nar a doon ëllëgu doomu-aadama, bés bu nu génnee ba set ci mbas miiy fàdd nit ñi, réewoo réew.
Ñu ci bare jàpp nañu ne, bu nu génnee ... | Defuwaxu |
https://www.defuwaxu.com/2020-mbas-mu-derkiis-nakk-teggin-tey-jur-tiinalante-ci-biir-reew-mi-ak-ci-bitim-reew/ | NAKA LAA GISE MBAS MI
Mbas mu dërkiis, ñàkk teggin tey jur tiiñalante ci biir réew mi ak ci bitim réew….
Naka la doomi Afrig yi war a taxawe ? Céy mbas mee gudd tànk, moom mi fàqe Penku, ca Wuhan, ca Siin, ca Asi, sóobu ci Afrig, ba ci Géeju Atlantig, daanu ci fii ci Ndakaaru (dëkk raw) ; ci Tànk (Wakaam, Ngor, Yoo... | Defuwaxu |
https://www.defuwaxu.com/lan-la-wutaakon-yi-naral-lakki-reew-mi/ | Lan la wutaakon yi naral làkki réew mi ?
Waaw mbokk yi, lan la wutaakon yi naral làkki réew mi ? Man ci sama wàllu bopp, déggaguma ci lu ma doy. Ndax Wolof, Pulaar, Séeréer, Soose, Joola, Sooninke…. dañu leen di wéy di suufeel teg Frãnse mbaa Àngale ci seen kaw ? Ndax Frãnse kese mooy wéy di nekk “làmmiñ wi Repibligu ... | Defuwaxu |
https://www.defuwaxu.com/jonanteb-xaritoo-senegaal-door-na-kamerun-1-0/ | JOŊANTEB XARITOO : SENEGAAL DÓOR NA KAMERUN 1-0
Gayndey kuppe yi dóor nañ Kamerun 1-0. Tey ci altine ji lañ doon amal joŋanteb xaritoo ca fowub Bollart bu Lens (France). Saajo Maane moo dugal biiwu Senegaal bi. Ab penaaltii la am, dugal ko. Joŋante bi nag, lees ko dugge mooy waajal CAN 2024 biy xewe fa Koddiwaar. Te s... | Defuwaxu |
https://www.defuwaxu.com/li-gen-a-fes-ci-xibaari-taggat-yaram-alxames-9-mars-2023/ | LI GËN A FËS CI XIBAARI TÀGGAT-YARAM (ALXAMES 9 MÀRS 2023)
KUPPE
Àngalteer
Démb, foo geestu ci mbaali-jokkoo, ñoo ngi doon wone ay naataal ak i widewooy kii nga xam ni mooy defãsëeru Manchester City bi, Kyle Walker. Mu mel ne ku àndul woon ak sagoom. Nde, mi ngi ciy tërëf ni ku màndi. Bu ca yemoon sax mu tane. Waaye... | Defuwaxu |
https://www.defuwaxu.com/bes-du-mag-du-tuuti-boroom-lay-tollool/ | BÉS DU MAG, DU TUUTI, BOROOM LAY TOLLOOL…
Dëgg la : ràcc jëmale sa kanam baaxul waaye tey fàww LU DEFU WAXU xamle mbégteem ci ndam li Paap Aali Jàllo am fan yee nu génn ca Iniwérsite Gaston Berger bu Ndar. Paap Aali ci kër gi la bokk, ayubés bu Yàlla sàkk mu am lu mu bind ci seen yéenekaay bii di LU DEFU WAXU. Nun ñiy... | Defuwaxu |
https://www.defuwaxu.com/emma-seen-daan-na-saa-cees/ | ËMMA SEEN DAAN NA SAA-CEES !
Démb ci dibéer ji, 5i fan ci weeru Me 2024, la doomu Pikin ji, Ëmma Seen doon sëgg ak Saa-cees, doomu Géejawaay ji. Seen bëre nekkoon lees doon xaar. Nde, dañu doon ñaari mbër yoy, duñu yàq làmb. Bu ñu bëree mu neex, bu ñu xeexee mu neex. Kii di doomu Pikin ji nag moo mujje am ndam ci kaw ... | Defuwaxu |
https://www.defuwaxu.com/ban-a-wacc-sa-and-baay-njaay/ | BAÑ A WACC SA ÀND…
Mbir mi doy na waar. Kenn xamul lii lu mu doon. Nekk cim réew, dund fa lu ëpp fanweeri at, te ba tey may bind baat yi, doxandéem la ñu la fi jàppe.
Am fi liggéey bu baax, di faj samay soxla ak a dimbali samay mbokk ; bokk ci ñiy yëkkati koom-koomu réew mi. Ci gàttal, man nanoo wax ne Baay Njaay xa... | Defuwaxu |
https://www.defuwaxu.com/maggalu-daaru-xudoos/ | MÀGGALU DAARU XUDÓOS
Mu doon tur wu siis wi ñu ko xame, màggalu daaru xudóos doon xew-xewu diine. Murit yi di ko màggal at mu jot ca Tuubaa, rawatina fa goxu daaru xudóos.
Xew-xewu diine boobu di fàttali bés ba Sëriñ Tuubaa Xaadim Rasuul di wuyuji Boroomam. Mu doon bés ba ñu ko jébbalee Boroomam faTuubaa ginnaaw ba m... | Defuwaxu |
https://www.defuwaxu.com/seex-beeco-cuun-atte-yallaa-gen-bu-nit/ | SÉEX BEECO CUUN : ÀTTE YÀLLAA GËN BU NIT
Altine 6eelu fan ci weeru Me, atum 2019. Bés bi ñépp doon xaar, bésub layoo, bésub àtte, ñëw na. Li tax ñépp doon xaar bés bii, nag, du neen.
Waaw.
Kan lañu doon àtte ? Sëriñ Séex Beeco Cuun, di Xalifa di yit kilifa cantaakon yi.
‘’Bóomug Madinatul-Salaam’’, bile dàkkental la t... | Defuwaxu |
https://www.defuwaxu.com/sampiyonaa-almaan-bayer-leverkusen-jel-na-ko/ | SÀMPIYONAA ALMAAÑ : BAYER LEVERKUSEN JËL NA KO !
Xabi Alonso ak gaayam yi def nañ ko. Dugal nañ Bayer Leverkusen ci mboorum futbalu Almaañ. Ci anam bu rafet a rafet lañ ko defee nag. Saa-Espaañ bi, Xabi Alonso miy tàggatkatu këlëb ba, def na jaloore ju réy a réy. Niki dibéeru démb ji, 14 awril 2024, lañ duma Werder Br... | Defuwaxu |
https://www.defuwaxu.com/waxtaanu-saada-kan-ak-bubakar-boris-joob/ | ‘’LI TAX SÉEX ANTA JÓOB AMUL MOROOM…’’
Waxtaan wii, ab tekki la ñeel jotaayu laaj-tontu bu Saada Kan di amal ci tele 2Stv ñaari ayu-bés yu nekk, te mu dalaloon ci sunu werekaan bi, Bubakar Bóris Jóob keroog, altine 22eelufan, sulet 2019.
Li ngeen ciy jàngsi mooy xaaj bu njëkk bi.
Saada Kan : Noo ngi am mbégte delsi ... | Defuwaxu |
https://www.defuwaxu.com/2312/ | Njàngatub Bàmmeelu Kocc : Téereb dekkali 1/2
Du guléet. Déedéet. Bindkat bi tëbul rekk bind Bàmmeelu Kocc Barma. Nde, ginnaaw Doomi Golo, bii mooy ñaareelu téereb nettali bu werekaan bi, Bubakar Bóris Jóob, génne ci làmmiñu wolof. Te sax, li ko jiitu, Bóris jot na fee yatt xalimaam gu set gi te neex, tekkil nu téereb ... | Defuwaxu |
https://www.defuwaxu.com/2002-atum-suuxu-joolaa-bi/ | 2002, ATUM SUUXU JOOLAA BI
Bërki-démb 26 sàttumbar ci atum 2020, “Bateau le Joolaa” def na 18i at ci biir géej. Daanaka ñaari-junni nit ñàkkoon nañ ci seen bakkan. Te mujjagul fenn, ay daan amaguñ ci. Moonte kenn mësula gis jéeya ju tollu nii, mu waroon a tax askan week nguur gi taxaw ngir leeral ko. Dañ koy fàtte ba ... | Defuwaxu |
https://www.defuwaxu.com/mag-sama-gor-du-ragal-du-wor/ | Bataaxalu Saalif Keyta ñeel IBK
Ci tekkib Paap Aali Jàllo
KÔRO (mag sama),
Jàmm ak salaam ñeel na la. Sa rakk a lay nuyu, di la ndokkeel, di la jox sa wàccuwaay.
Ginnaaw loolu, xamal ni kat, sa mbokku cosaan mi nga bokkal maam, di sa mbokku aada, moo namm a waxtaan ak yow tey. Bataaxal bii ngay jàngsi, mi ngi bawoo... | Defuwaxu |
https://www.defuwaxu.com/sigaret-baaxul-waaye-afrig-la-yeese/ | SIGARET BAAXUL… WAAYE AFRIG LA YÉESE !
Fan yii weesu, Marie Maurisse, ab taskatu xibaar bu fekk baax Siwis, bind na bataaxal bu jar a bàyyi xel. La muy ciy nettali mooy ñaawtéef yu këri-liggéeyukaay yu mag yiy jaay sigaret ci réewi Afrig yiy def, te sunuy gornamaa ne yàcc di leen seetan.
Tóx baaxul, loolu dëgg gu wer... | Defuwaxu |
https://www.defuwaxu.com/ndam-lu-saful-xorom-saful-suukar/ | NDAM LU SAFUL XOROM, SAFUL SUUKAR…?
10Dibéer yemook ñaar-fukki fan ak ñeent si weeru Féewaryee, la waa réew mi doon tànn ki leen war a jiite ba atum 2024. Waaye, dafa mel ne li mu jur ci werantee ëpp li mu jur ci jàmm ji ñu xame Senegaal. Ndaxte, woteb njiitu réew bees génn, ñaxtook fitna lañ ci gën a ràññee. Te yit, ... | Defuwaxu |
https://www.defuwaxu.com/can-2021-kub-baa-nga-woon-ca-seeju-saajo-maane-delloo-mbattu-ca-ndaa-la-mu-naane/ | CAN 2021 : Kub baa nga woon ca Séeju, Saajo Maane delloo mbàttu ca ndaa la mu naane
Bàmbali, ci diwaanu Séeju, dalal na Kubu Afrig bi Senegaal jële woon ca Kamerun ak doomam jii di Saajo Maane. Jëwriñ ji Mataar Ba yékkati na fay kàddu, wonale kub bi Jaraafu Séejook waa Bàmbali, teg ca ni Saajo Maane nekkee royuwaay ci... | Defuwaxu |
https://www.defuwaxu.com/xibaari-taggat-yaram-7/ | XIBAARI TÀGGAT-YARAM
KUPPEG TEFES
Mamadu Jàllo, tàggatkatu ekibu Senegaal bu kuppeg tefes bi tànn na ndaw yi mu war a yóbbu fa Irã ngir amal fa ñetti joŋantey xaritoo, bési 19, 20 ak 22i ci weeru desàmbar wii. Joŋante yépp moom ak Irã lay doon ca diiwaanu Teherã (Téhéran).
NDAW YI MU TANN
Góol : Alseyni Njaay ak Us... | Defuwaxu |
https://www.defuwaxu.com/nakk-kayitu-juddu-gi-nag-ba-kan/ | ÑÀKK KAYITU-JUDDU GI NAG, BA KAÑ?
Ayu-bés yii weesu, yéenekaay yu bare dañoo xéy fésal ci seen xët bu njëkk xibaar bu kéemaane. Waaw, li nu ko dugge woon mooy xamal askan week Nguur gi ne lu mat junniy ndongo ak lu teg amaguñu kayitu-juddu. Déggal ma lii rekk ! Te lees war a xam moo di ne ndongo yooyu, looloo leen di ... | Defuwaxu |
https://www.defuwaxu.com/niseryaa-buhari-faluwaat-na/ | NISERYAA : BUHARI FALUWAAT NA
Ci weeru féewaryee wii jàll la askanu Niseryaa doon amal woteb njiitu réewam. Ba ñu àggee ci cëpaandoo li, Muhammadu Buhari la askan wi tànn, dénkaat ko réew mi. Lu tollu ci 15 alfunniy wotekat ñoo sànnil xob ki toogoon ci jal bi 2015 ba léegi, mu jël raw-gàddu gi ci kanamu lawax bii di A... | Defuwaxu |
https://www.defuwaxu.com/serin-bi-faww-mu-feen/ | “SËRIÑ BI, FÀWW MU FEEÑ”
Bu ñu seetloo fan yee ci ginnaaw, werante amoon na ci nataali Séex Ahmadu Bàmba Mbàkke, naan moom la ak du moom. Muy ay nataal yi ñu fésaloon ci mbaali jokkoo yi. Nataal yooyu di wone jëmmi Séex Ahmadu Bàmba Xaadim Rasuul. Ñu xame woon ko ci benn nataal képp bu ñu miin a gis, réewu Farãs denc ... | Defuwaxu |
https://www.defuwaxu.com/kadduy-usmaan-sonko-useynu-beey/ | KÀDDUY USMAAN SONKO 1/2 PÀCC
Senegaal gépp amoon na fiy yëngu-yëngu, réew mi jaxasoo, yëf yi doy waar lool, yegg sax fu ko kenn foogul woon. Ñii seen i bakkan rot ci, ñee am ciy gaañu-gaañu yu metti, ñale ñàkk ci alal ju bari. Ginnaaw ba mu jógee “Section de Recherches” bu Kolobaan, Usmaan Sonko amal na waxtaan ak waa... | Defuwaxu |
https://www.defuwaxu.com/can-koddiwaar-2024-caabalu-bes-bi/ | CAN KODDIWAAR 2024 : CAABALU BÉS BI
WÉR-GI-YARAMI ALIW SIISE AK ABDULAAY SIMAA
Bees sukkandikoo ci yégle “Fédération Sénégalaise de Football” (FSF) biral démb ci gaawu gi, Aliw Siise, tàggatkatu ekibu Senegaal bi, dafa jagadi woon. Ci àjjuma ji, bi joŋante gaynde yi jeexee, la ko feebar bu gaaw dikkal, ñu rawale ko f... | Defuwaxu |
https://www.defuwaxu.com/di-buur-di-bummi-2/ | DI BUUR, DI BUMMI
Li jaaxal waa Senegaal, mooy wax-waxeet yi kilifay réew mi dëkke. Ku ci jóge ci kujje gi, dem ci nguur gi yaa ngiy xas ñaa nga àndaloon démb.
Mbir mi dafay faral di am ba kenn, ci ñaari làng yépp, muccu ci. Ñépp a ngi fàttaliku ci ndetteelu atum 2018, bi peresidaŋ Maki Sàll nee mësul a ni nañu jële ... | Defuwaxu |
https://www.defuwaxu.com/xibaari-taggat-yaram-2/ | XIBAARI TÀGGAT-YARAM
LIGUE DES CHAMPIONS 2024-2025
Waa UEFA amal nañu ay coppite yoy, dañuy yokk limatu ekib yiy bokk ci joŋante Ligue des champions bu déwénee, atum 2024-2025 mi. Ci loolu, Araabi Sawdid mi nga xam ni, daanaka futbalkat yu xareñ yu bari ñoo ngi jóge Tugal di leen fekki ci seen sàmpiyonaa ba, ñu ci me... | Defuwaxu |
https://www.defuwaxu.com/futbal-ak-jafe-jafey-reewi-afrig-yi/ | FUTBAL AK JAFE-JAFEY RÉEWI AFRIG YI
Doom-aadama fent na ay xeeti po yu bare. Ba ci tàggat-yaram sax, nga xam ne, ci cosaanam, yar ak wér-gi-yaram ñoo ko taxoon a jóg, nit soppi na ko, def ko liggéey ak po, di ci amal ay joŋante yu mag, àddina sépp di ko teewe. Xeeti po yooyu, nag, futbal a ci gën a siiw te yit moo ci ... | Defuwaxu |
https://www.defuwaxu.com/xibaari-taggat-yaram-3-9-2023/ | XIBAARI TÀGGAT-YARAM (3/9/2023)
SAALIF KEYTA KUPPEKATU MALI BA WOON GAAÑU NA
Ci gaawug démb ji, 2 sàttumbaar 2023, la kuppekatu Mali bi gaañu. Ndem-si-Yàlla Saalif Keyta mi ngi amoon 76i at. Moom, doomu Mali ji, mooy kuppekatu saa-afrig bi jëkk a gañe Kuppeg wurus gu Afrig (Ballon d’or africain) ca atum 1970. Saalif ... | Defuwaxu |
https://www.defuwaxu.com/5796-2/ | Seen xiibaari tàggat-yaram Dibéer 12i Féewaryee 2023
Kuppeg àddina këlëb yi : “Real Madrid” defatina ko !
Démb ci gaawu gi, 11i Féewaryee bii atum 2023, la woon finaalu kuppeg àddina këlëb yi, mu doxoon ci digante “Real Madrid” ak “Al-Xilal”. “Real Madrid” moo dóor juróomi bal ci ñett (5-3) dellu jëlati raaya ji. Bi... | Defuwaxu |
https://www.defuwaxu.com/xecc-bu-danee-dagg/ | XËCC BU DAŊEE DAGG !
Nimbir yiy doxe diggante nguur geek kujje gi bi Màkki Sáll toogee ci jal bi ba tey jii, dalul xel dara. Nun ñépp a ànd ci demokaraasi, waaye ni ko peresidaŋ Sàll gise — ku am doole danga koy wone, doo maye dara, doo yërëm kenn — mën naa jur ëllëg musiba ci réew mi. Ci sama gis-gis bu gàtt, dafa wa... | Defuwaxu |
https://www.defuwaxu.com/barsaa-am-barsaq-lu-xew-ci-miim-reew/ | BARSAA WALLA… BARSÀQ !… LU XEW CI MIIM RÉEW?
Géej gaa ngiy wann sunu doom yi. Mbete jasig juy warax béy bu lab. Ay fukki, ay téeméeriy, ay junniy waxambaane ak, léeg-léeg sax, ay janq walla ay jeeg ñooy song géej gi, wuti Barsaa walla… Barsàq ! Ñi ëpp ci ñoom, dañuy des ci ndox mi, ñuy mag di ndaw, di góor di jigéen, ... | Defuwaxu |
https://www.defuwaxu.com/demb-ak-tey/ | DÉMB AK TEY
Dal-leen ak jàmm ci seen xët DÉMB AK TEY mi leen seen yeénekaayu web LU DEFU WAXU jagleel. LU DEFU WAXU nag, li ko tax a jóg mooy dégtal leen ay xibaar yu wér te wóor te aju ci xew-xew yi gën a fés ci réewum Senegaal ak sax ca bitim-réew.
Waaye tamit, bindkat yi dinañ faral di leen ci baaxe seeni gis-gis... | Defuwaxu |
https://www.defuwaxu.com/xibaari-taggat-yaram-3/ | XIBAARI TÀGGAT-YARAM
MESSI GAÑE NA KUBAM BU NJËKK AK INTER MIAMI
Ci guddig gaawu gi jàpp dibéer jii weesu la Inter Miami doon joŋante finaalu Leagues Cup, doon ci daje ak Nashville. Bi joŋante bi dawee ba ci 23eelu simili ba la Pulga bi daldi dugalal Inter Miami, ñu dawal ba ci xaaju ñaareel bi, ci 57eelu simili bi, ... | Defuwaxu |
https://www.defuwaxu.com/ligue-des-champions-dortmund-ak-real-madrid-nooy-daje-finaal/ | LIGUE DES CHAMPIONS : DORTMUND AK REAL MADRID ÑOOY DAJE FINAAL
Démb, ci àllarba ji, lees doon amal ñaareelu joŋantey demi-finaali “Ligue des champions” bi, diggante Real Madrid ak Bayern Munich. Lu ko jiitu, ci talaata, Paris Saint-Germain doon na janook Dortmund. Dafa di nag, Dortmund ak Real Madrid ñoo am ndam ci se... | Defuwaxu |
https://www.defuwaxu.com/xibaari-taggat-yaram-16-7-2023/ | XIBAARI TÀGGAT-YARAM (16/7/2023)
KUPPEG ÀDDINA SI 2026
Kippu yi ñeel xëccoo paasu kuppeg àddina si war a am ci atum 2026 mi génn nañ fii ci wàlluw Afrig. Senegaal moo ngi bokk ci kippug B gi mook ñii di Kóngoo, Móritani, Tógoo ak ñaari Sudaŋ yi. Senegaal lees jàpp ne mooy ékib bi gën a jekkandi ci kippu gi. Waaye, na... | Defuwaxu |
https://www.defuwaxu.com/mbara-wacc-doomi-gaynde-njaay-yi/ | MBARA-WÀCC DOOMI-GAYNDE NJAAY YI !
Sunu gaynde yi amagul ñaar-fukki at wone nañu njàmbaar fale ca Niseer, nga xam ne fa la réewi Afrig yi gën a xareñ ci futbal daje woon di joŋante.
Jaaraama sunu Doomi-Gaynde yi ! Ay jàmbaar dëgg lañu, ñaawuñu ci xare bi ndax ca Niseer, daje nañook ñeenti ekib, am ndam ñeenti yoon. M... | Defuwaxu |
https://www.defuwaxu.com/futbal-ak-basketu-senegaal-yaakaar-ak-yakki/ | FUTBAL AK BASKETU SENEGAAL : YAAKAAR AK YÀKKI
Bi Alseri dumaa Senegaal benn ci dara ci finaalu joŋanteb réewi Afrig yi (CAN) ak léegi, mu ngi bëgg a yàgg. Waaye, kenn fàttewu ko. Li ko waral nag mooy finaalu basket bi soxna yi ñàkk, ñoom tamit, biñ dajeek Niseryaa fan yii ñu weesu. Yaakaaroon nañu ne, soxnay basket yi... | Defuwaxu |
https://www.defuwaxu.com/li-gen-a-fes-ci-xibaari-futbal-alxames-9-feewaryee-2023/ | LI GËN A FES CI XIBAARI FUTBAL (alxames 9 féewaryee 2023)
BELSIG AM NA TAGGATKAT BU BEES
Kuppeg àddina 2018 ba léegi, Belsig dafa nekkoon ciy jafe-jafe. Njeexitalu kuppe gi gën koo feeñal. Moo tax ba seen tàggakat ba, Robeertoo Maartinees, xamoon boppam, tekki ndombal-tànkam balaa ñu koy dàq. Démb, ci àllarba ji la ñ... | Defuwaxu |
https://www.defuwaxu.com/demb-senoor-tey-wadd/ | DÉMB SEŋOOR, TEY WÀDD
Li ko dale atum 1978 ba tey jii, woteb ren bii mooy wote bu fi njëkk a am te Ablaay Wàdd sampu ci ndëndam. Walla boog, loolu la ñu bare jàpp. Ndax, man kat neneen laa gise mbir mi. Bees delloo ginnaaw, fàttaliku atum 2007, bi Ablaay Wàdd faluwaatee, war a amal ñaareelu moomeem, dafa wax wax ju am... | Defuwaxu |
https://www.defuwaxu.com/riiru-kampaan/ | RIIRU KÀMPAAÑ
Lépp lu yëngu am na lu ko yëngal. Réewum Senegaal, jamono jii mu ngi toll ci waajtaayu joŋante bi ñuy fale kiy toog ci jal bi. Këru-Àtte gi gën a kowe fésal na juróomi wutaakon yu samp seen ndënd : Maki Sàll, Isaa Sàll, Usmaan Sónko, Madike Ňaŋ ak Idiriisa Sekk. Kenn ci ñoom la xelam toogatul fan yii, ta... | Defuwaxu |
https://www.defuwaxu.com/sacciin-wi-jem-ci-tann-yi-degmal-te-feenalees-ko/ | SÀCCIIN WI JËM CI TÀNN YI DËGMAL TE FEEÑALEES KO
Sëñ Abdu Xaadr Kebe mooy biral fii xalaatam ñeel wotey tànn Njiitu réew mees dëgmal ci atum 2024 mii nu nekk. Dafay feeñal yenn pexey njuuj-njaaj yees lal ngir sàcc wote yi, foqati baatu askan wi.
1 : Baril àdduwaay yi (lieux de vote) ak pekki àddu yi (bureaux de vote)... | Defuwaxu |
https://www.defuwaxu.com/xibaari-taggat-yaram-1-10-2023/ | XIBAARI TAGGAT-YARAM (1/10/2023)
KUPPEG ÀDDINA WAY-LUU YI (MUUMA YI)
Bàyyeesu leen xel, waaye way-luu (muuma) yi teewal Senegaal ca kuppeg àddina si bees leen jagleel ñoo ngay def i jaloore yu rëy. Ba léegi, ékib gañeeguleen ! Ñoo ngi toll ci ñeenti joŋante, gañe 3 yi daldi timboo benn bi. Kaar-dë-finaal lañu war a a... | Defuwaxu |
End of preview. Expand in Data Studio
README.md exists but content is empty.
- Downloads last month
- 5